TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/08 p. 5
  • Ay Tont Ci Seeni Laaj

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ay Tont Ci Seeni Laaj
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ay Tont Ci Seeni Laaj
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Lu tax ñu war a bàyyi xel ci ni ñuy soloo?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Yére yu jekk te yiw dañuy wone ne dañu ragal Yàlla
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Nañu yiw ci li ñuy sol
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 3/08 p. 5

Ay Tont Ci Seeni Laaj

◼ Bu ñuy dem Saalu Nguur gi, fi ñuy defe ndaje yu mag yi, Betel, ak ci bànqaasi Seede Yexowa yi, naka lañu war a soloo ngir mu jekk ci béréb yooyu ?

Saalu Nguur gi, fi ñuy defe ndaje yu mag yi, Betel, ak bànqaasi Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp, ay béréb fu ñuy jaamu Yexowa lañu. Béréb yooyu dañu leen defar ñu nekk kër yu yem, set, te jekk. Kon ku leen gis rekk xam ne béréb yu yiw la. Loolu wuute na lool ak li xew ci àddina su bon si Seytaane di jiite. Kon képp kuy dem ci béréb fu ñuy jaamu Yexowa war na niru ak nit ku bokk ci mbooloo Yexowa, nit kuy def coobareem.

Ñun karceen yi, dañuy wuyoo turu “ jawriñu Yàlla ” (maanaam ñuy liggéeyal Yàlla) fépp fi ñu nekk ak li ñu mënta def. Defar bu baax suñu bopp te di sol ay yére yu jekk te yiw, bokk na ci loolu (2 Kor. 6:3, 4). Te it li ñu séentu ci ñun mooy bu ñu fa nekkee, ñu wone jikko yu jekk ci béréb yooyu. Fu ñu mënta nekk rekk, ni ñuy defare suñu bopp ak ni ñuy soloo, dafa war a jekk te yiw, ni mu jekkee ci ñiy jaamu Yexowa Yàlla. Rawatina bu ñuy dem ci suñu kër gu mag ga ca New York, walla it ci bànqaas yi nekk ci àddina si sépp.

Téere Organisés pour faire la volonté de Jéhovah wax na lu tax solu te defar suñu bopp ci fasoŋ bu jekk am solo. Wone na foofu ne bu ñuy waaraate, walla bu ñuy teewe ndaje yi, dañu war a set, sol yére yu yiw, te defar bu baax suñu bopp. Ci xët 138, xise 3, wone nañu it ne waruñu fàtte ne Betel, dafay tekki kër Yàlla. Nee nañu it ne looloo tax suñuy yére, ni ñuy defare suñu bopp ak jikko yi ñu fay wone, war na mel ni bu ñuy teewe ndaje yi ca Saalu Nguur gi ngir jaamu Yàlla. Waaraatekat yi dëkk fu sorewul Betel bi ak ñi dëkk fu ko sore yépp, war nañu topp lu am solo loolu bu ñu fay dem. Ñiy ñëw Betel, noonu lañu mën a wone ne fonk nañu ko te may nañu ko cér. — Sab. (Ps.) 29:2.

Suñuy yére war nañu tax ku ñu gis rekk xam ne ci ñiy “ woote ag ragal Yàlla ” lañu bokk (1 Tim. 2:10). Bu ñu soloo te defar suñu bopp ni mu ware, loolu mën na tax nit ñi xalaat lu rafet ci diine Yexowa. Waaye seetlu nañu ne dafa am suñuy mbokk yu góor ak yu jigéen yoo xam ne bu ñuy dem Saalu Nguur gi, fi ñuy defe ndaje yu mag yi, Betel, walla ci bànqaasi Seede Yexowa yi, duñu defar seeni yére ba mu jekk, walla ñu sol lu yaraax. Yére yu mel noonu masul jekk te du mas a jekk ci ay karceen. Ci fànn boobu ak ci bépp fànn ci suñu dundu karceen, li ñu bëgg mooy kontine di topp santaane Yàlla yu kawe yiy tax ba ñiy jaamu Yàlla wuute ak waa àddina si. Te it def lépp ngir màggal Yàlla. — Room 12:2 ; 1 Kor. 10:31.

Kon nag, bu ngeen di dem ci suñu kër gu mag gi nekk ca New York walla ci bànqaas yi, bu dee dangeen ko waaj walla ngeen tukki rekk fu béréb yooyu nekk, nangeen laaj seen bopp lii : ‘ Ni ma defare sama bopp ak ni ma soloo ndax dafay wone woyof, ndax set na, te jekk it ci béréb bu yiw bi may dem ? Ndax dafay wone ni Yàlla bi may jaamu mel ? Ni ma soloo ak ni ma defare sama bopp ndax du tax ba nit ñi duñu mën a def seen xel ci li ñu doon def, walla dafa di colin bu ñaaw bu sama moroom mënul a nangu ? Yàlla na ñu defar suñu bopp te solu saa su nee ci fasoŋ buy “ rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat ” ! — Tit 2:10.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager