Nañu yiw ci li ñuy sol
1 Benn taskatu xibaar nee na : “ Góor ñépp, mag ak ndaw, dañu takk karwaat (cravate). Jigéen yi yépp, boole ci janq yi ak xale yi, sipp walla robb lañu sol. Kenn solul tubéy bu xat bu ñuy woowe jiin walla simis bu amul karwaat. Ñépp a bégoon, seen kanam leer. ” Ñan la doon wax noonu ? Nit ñu nekkoon ci miitiŋ ? Nit ñu doon seetaan espoor ? Ñu nekkoon ci li ñuy wax show ? Déedéet ! Dafa doon wax ci suñu ay mbokk yu mu gisoon daaw, ci suñu ndaje bi gën a mag bi.
2 Ci beneen ndaje bu mag, lii la benn taskatu xibaar wax ci ay Seede Yexowa : “ Góor ñépp a set, sol kostim (costume) te takk karwaat. Jigéen yi dañu solu woon solu bu yiw te jekk. ” Benn alkaati bu fa nekkoon dafa ne : “ Dangeen yaru te set. Li may gis fii de, rafet na. Ci àddina su tilim si ñu nekk nii, fexe ngeen ba amatul lu tilim ci seen biir ! ” Loolu ñu wax ci ñun, aka rafet ! Bu ñu déggee lu baax noonu ci suñuy mbokk, ndax duñu kontaan ? Axakay. Waaye leer na ne ku nekk ci ñoom am na wàllam ci lu rafet loolu ñu wax ci ñoom. Seen solu bu jekk te jar a roy moo indi loolu.
3 Àddina si sépp xam na ne ni ñuy soloo wuute na ak ni ñeneen nit ñi di soloo (Mal. 3:18). Lu tax ? Ndaxte dañuy topp li ñu Mbind mi xelal, maanaam ñu ‘ sol col gu faaydawu, cig woyef ak maandu. [...] na seen col di jëf yu rafet, ndaxte looloo jekk ci [ñiy] woote ag ragal Yàlla ’. — 1 Tim. 2:9, 10.
4 Ni ngay soloo, lu muy wone ? Suñuy yére ak ni ñu leen di sole, am na li ñuy wone ci ñun, maanaam suñuy ngëm, suñu jikko ak li ñu bëgg def. Yére yi ñuy tànn, dañuy wone ku ñu doon dëgg. Waruñu jàpple waa àddina si, ci seeni xalaat ak seeni jëf yu bon. Bu ñuy solu, du li xew moo ñu gën a itteel, waaye li jekk ci nit kuy wax ne Yàlla lay liggéeyal (Room 12:2). Bu ñuy solu, waruñu tànn luy wone ne bëgguñu kenn ilif ñu, walla luy tax ñu boole ñu ci nit ñu am dund bu bon. Waaye ci dëgg dëgg, li ñu bëgg mooy “ màggal Yàlla ”. — 1 Pie. 2:12.
5 Yenn saay, ku yàggul ci mbooloo mi, ku xamagul lu bare ci mbooloo mi, walla ku ngëmam waññiku, mën na topp li àddina si bëgg ci wàllu yére ak ni ñuy soloo, te bañ a seet li loolu di def ci li nit ñi di xalaat ci Yexowa ak mbootaayam. Ñun ñépp war nañu seetaat suñu bopp ba xam ndax li niti àddina si di xalaat, mu ngi ñuy wàll. Mën nañu dem ci suñu benn mbokk bu góor walla bu jigéen bu ñor ci wàllu ngëm, ndax mu wax ñu li mu xalaat ci suñuy yére ak ci ni ñuy soloo. Bu ñu paree, nañu xalaat bu baax ci li mu wax.
6 Am na ñu nangu ne dañu war a xool bu baax ni ñuy soloo bu ñuy teew ci ndaje bu gën a mag bi. Waaye bu ñu wàccee te bëgg feexali seen xol, seen solu dootul yiwati ni ci ndaje bi. Nañu wéy di topp li Yàlla laaj waaraatekat yi nekk karceen (2 Kor. 6:3, 4). Fu ñu mënta dem ba nit ñi gis ñu, kàrtu ndaje bi ñuy tapp ci suñu yére, li ñuy sol ak ni ñu koy solee, loolu yépp mooy wone ne ay Seede Yexowa lañu. Kon nag, fu ñu mënta nekk, suñu yére yi, dañu war a jekk te yiw, di wonee noonu ne ‘ bokkuñu ci àddina ’ si. — Ywna. 15:19.
7 Ren, ci ndaje bi gën a mag bi tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, nañu def lépp li ñu mën ngir wone ne ñun ñooy ‘ mbooloo mu set mi Yexowa [suñu] Yàlla moom ’. Loolu, ni muy laale nit ñi, dina tax ñu gën a màggal Yexowa, te gën koo may ndam. — 5 Mu. 26:19.
[Wërale bi nekk paas 6]
Ni ñu mënee màggal Yexowa :
■ Na seen solu jekk ci kuy liggéeyal Yàlla.
■ Buleen topp jikko jamano ji ci ni ngeen di soloo.
■ Nangeen yiw, di wonee noonu seen maandute.