TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/04 p. 6
  • Nañu sol lu yiw lu mat a naw

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu sol lu yiw lu mat a naw
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lu tax ñu war a bàyyi xel ci ni ñuy soloo?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Yére yu jekk te yiw dañuy wone ne dañu ragal Yàlla
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Nañu yiw ci li ñuy sol
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 9/04 p. 6

Nañu sol lu yiw lu mat a naw

1 “ Seede Yexowa yi ñoo fi gën ! Dangeen baax, di solu ni mu ware te di weg nit ñi. ” Ku doon liggéey ci otel moo wax loolu daaw bi mu gisee suñu mbokk yu góor ak yu jigéen yu ñëwoon ci benn ndaje bu gën a mag. Ci beneen ndaje bu gën a mag, keneen ku doon liggéey ci otel dafa ne : “ Ñépp a mën a gis ne yéen dangeen di solu ngir Yàlla. ” Nit ñi dañuy xool bu baax ñiy ñów ci ndaje yu mag yi. Kon, nañu solu ci fasoŋ bu “ yelloo ak li Krist yégle ci xebaar bu baax bi ”. Loolu dafay tax nit ñi wax lu baax ci ñun, te dafay wone bu baax ne ñun, Yàlla lañuy liggéeyal (Fil. 1:​27). Bu ñuy waajal suñu ndaje bu gën a mag bi, nañu xalaat bu baax ci ni ñuy soloo.

2 Saak nee na : “ Xel mi jóge ci kaw daa sell. ” (Saak 3:​17). Tey, yëre yu baax ci nit ku sell, yombul am. Lu bon li nekk ci àddina Seytaane, dafay xiir nit ñi ci yëre yu yiwul, ci yëre yuy wone seeni cér, walla ci yëre yoo xam ne kenn xamul li ñuy niru. Yëre yooyu gënul (1 Ywna. 2:​15-​17). Kon nag bu ñuy seet ni ñu war a soloo ak ni ñu waree defar suñu karaw, dañu war a topp li Biibël bi wax, maanaam “ dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamano, tey dund ci àddina cig maandu ”. (Titt 2:​12). Nañu fexe ba kenn bañ a rus ndax li ñu sol. Muy suñu mbokk yi, ñiy liggéey ci otel yi walla ci restoraŋ yi, walla ñeneen ñi ñuy seetaan. — 1 Kor. 10:​32, 33.

3 Yëre yu yem te jekk : Bu ñuy waajal suñu bopp ngir ndaje bu gën a mag bi, nañu laaj suñu bopp lii : ‘ Li ma sol, ndax yem na, walla dina tax ñépp di ma xool ? Ndax dafay wone ne maa ngi xalaat li nit ñi di yëg ci seen xol ? Ndax dafa ubbeeku ba muy feeñal samay ween, walla dafa gàtt ba sama biir di feeñ ? Ndax dafa yaraax torop, walla dafa xat lool ? Ndax set na te amul benn xet bu bon ? Su may fo bu ndaje bi jeexee, ndax li may sol dafay set te jekk ci kuy liggéeyal Yàlla ? Walla ndax damay bëgg topp li xew, walla samay yëre duma leen defar bu baax ba tax li may sol du mën a ànd ak kàrtu ndaje bi ma tapp ci sama yëre ? Li may sol bu may fo, ndax dafay tax ba duma ñeme waaraate bu ma ci amee bunt ? ’ — Room 15:​2, 3 ; 1 Tim. 2:⁠9.

4 Li Karceen yu ñor yi ci wàllu ngëm di wax ci suñu yëre, mën na ñu dimbali ci ni ñu war a soloo. Jigéen ñi war nañu laaj seen jëkkër, naka la nit ñi di gise seeni yére. Waajur yu nekk karceen it mën nañu dimbali ci wàll boobu seeni doom yi nekk janq walla waxambaane. Mag yu jigéen yu ragal Yàlla it, mën nañu “ sol ci boppu jéeg yu ndaw yi, [...] ñu maandu, sell ” ci li ñuy sol “ ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla gi ”. (Titt 2:​3-5). Am na ci suñu téere yi ay foto yuy wone nit ñu solu ci fasoŋ bu yem te jekk. Loolu mën na la dimbali.

5 Na nit ñi màggal Yexowa ndax ñun : Bu ñu nekkee ci ndaje yu gën a mag yi, du ñi bokk ci waxtaan yi rekk ñoo mën a màggal Yexowa. Ñépp a ci mën a màggal Yexowa. Dëgg la, jikko karceen yi ñuy wone ak fasoŋ bu ñuy waxe dina tax ñu màggal ko. Waaye, li nit ñi di njëkk gis ci ñun mooy ni ñuy soloo ak ni ñuy defare suñu bopp. Kon, ñun ñépp, nañu def ba nit ñi màggal Yexowa ndax lu yiw te mat a naw li ñu sol. — Sab. 148:​12, 13.

[Laaj yi]

1. Bu ñuy waajal ndaje bu gën a mag bi, lu tax ñu war a xalaat bu baax ci ni ñuy soloo ?

2. Lu tax solu te defar sa karaw ci fasoŋ bu yiw, jafe tey ?

3. Yan laaj lañu war a laaj suñu bopp ngir mën a seetaat ni ñuy soloo ?

4. Naka la ñu suñu mbokk yi mënee dimbali ba ñu solu ci fasoŋ bu yiw ?

5. Lan lañu mën a def ñun ñépp ba nit ñi màggal Yexowa ci ndaje bu gën a mag biy ñów ?

[Wërale bi nekk paas 6]

Li nu mën a dimbali ñu sol lu mat a naw

◼ Kàddu Yàlla

◼ Xoolaat bu baax suñu bopp

◼ Xool ñeneen ñi

◼ Téere karceen yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager