Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
Tey am na lu bare lu ñu mën a jàng ngir moytu feebaru xol, bu ko defee ñu am wér-gi-yaram, dund gu gudd te neex. Waaye am na lu ëpp solo loolu lépp. Mooy fexe ba suñu xol ci wàllu ngëm bañ a feebar. Kon, ndaje bu mag bu benn fan biy ñów dina baax lool ndaxte lii lañu ciy waxtaan : “ Nañu jaamu Yàlla ak suñu xol bépp. ” (1 Net. 28:9). Ci weeru septaambar 2003 lañuy tàmbali am ndaje boobu. Lan lañu fay jàng ?
Wottukat biy wër ci mbooloo yi dina waxtaan ci lii : “ Nañu dimbali nit ñi ñu jaamu Yexowa ak mbégte. ” Dinañu woo ay nit ngir ñu wax mbégte bi ñu mën a am bu ñuy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, te bu ñuy jàng Biibël bi ak ñi bëgg jaamu Yexowa. Ki ñu bànqaas bi yónnee, waxtaan bii lay njëkk def : “ Nañu sàmm suñu xol ci àddina su jaxasoo sii. ” Ñi fa teew ñépp seen xol dina sedd, te dinañu gën a am doole. Dinañu àggale suba soosu ak waxtaan bi ñu jagleel ñi nu war a sóob.
Ci ngoon si, xaaj bi tudd “ Nañu tàllal suñu loxo ngir dimbali nit ñi ”, dina ñu won ni ñu mënee dimbali suñu moroom. Lan la way-jur yi mën a def ngir mu bañ a am luy dugal lu bon ci seen xolu doom, walla ngir ñu jege Yexowa ? Ci xaaj bi tudd “ Dimbalileen seeni doom ñu am mbégte bu ñuy jaamu Yexowa ”, dinañu ci am xelal yu baax te dinañu wone ni ñu ko mënee topp.
Am na li ñu Yexowa defal ngir ci wàllu ngëm ñu bañ a am feebaru xol te suñu xol dëgër. Ndax ñu ngi koy jariñoo bu baax ? Ki bànqaas bi yónnee, waxtaan bii lay mujj a def : “ Nañu wéy di def suñu xol bépp ci liggéeyu Yexowa. ” Dina ñu won ñeenti mbir yu ñu war a faral di def ngir am ngëm gu dëgër. Ndax ñu ngi góor-góorlu ngir am jotu ñaan Yàlla ñaan yu jóge ci suñu biir xol ? Am jotu jàng Kàddu Yàlla, jotu waaraate te sawar ci, walla daje ak suñu mbokk karceen yi ? Ci fànn yooyu, ndax am na fu ñu mën a góor-góorlu ngir mu gën a baax ?
Yexowa mu ngi woo nit ñi ci lii : “ Jox ma sa xol ngir ma yar ko, sa nopp it ngir dégg lu mën a yokk sa xam-xam. ” (Léeb. 23:12). Bésu ndaje bu mag boobu, dinañu jàng ci Mbind mi lu am njariñ lool. Seetal léegi li nga war a def ngir fekke ko. Dinga ci mën a yokk doole bi nga soxla ngir jaamu Yexowa ak sa xol bépp, te am mbégte.