Ndokkeel, dafay sawarloo
1 “ Xanaa tey nekkuma woon xale bu baax ? ” Xale bu ndaw moo doon jooy di laaj loolu yaayam waxtu bu mu doon tëddi. Li ko xale bi wax dafa bett yaay ji. Dëgg la, gisoon na ne bés boobu yépp, doomam dafa doon góor-góorlu ngir def lépp ba mu baax. Waaye waxu ko dara ci liggéey bu rafet bi mu def. Jooyu xale boobu, dafa ñuy fàttali ne ñépp a soxla dégg sa liggéey rafet na, muy mag, muy ndaw. Ndax ñu ngi ndokkeel ñi nekk suñu wet ci seen liggéey bu rafet bi, su ko defee ñu gën a sawar ? — Léeb. 25:11.
2 Bare na li ñu mën a wax lu rafet ci li suñu mbokk karceen yi di def. Magi mbooloo mi, surgay mbooloo mi ak pioñee yi, dañuy liggéey bu baax ngir def li leen war (1 Tim. 4:10 ; 5:17). Way-jur yi ragal Yàlla, dañuy def lépp li ñu mën ngir yar seeni doom ci yoonu Yexowa (Efes 6:4). Ndaw yi nag ñoom, dañuy xeex xeex bu metti ngir xelu àddina si bañ leen a yóbbaale (1 Kor. 2:12 ; Efes 2:1-3). Am na yeneen karceen yoo xam ne ñoom it ñu ngi topp Yexowa bu baax te fekk dañu màgget, dañu feebar walla dañu am yeneen jafe-jafe (2 Kor. 12:7). Karceen yooyu yépp, war nañu leen ndokkeel bu baax. Ndax moom lañuy def ?
3 Nit ki ak li mu def : Bu ñu déggee ci suñuy ndaje ñuy wax lu baax li mbooloo mi def, dafa ñuy neex lool. Waaye bu fekkee ne dañuy wax lu baax ci li ñu def ñun ci suñu wàllu bopp, ci lay gën a neex. Ci leetar bi mu bind waa Room pàcc 16, Pool dafa wax liggéey bu rafet bi ay karceen def. Tudd na ci Febe, Prisil ak Akilas, Trifen, Trifos ak Persidd. Waaye ku ci nekk dafa wax lenn lu rafet li mu def (Room 16:1-4, 12). Bi ko karceen yooyu déggee, wóor na ne dañu doon kontaan lool ! Bu ñu waxee noonu suñu mbokk yi lu baax li ñu def, dafa leen di won ne soxla nañu leen dëgg ci mbooloo mi, te dafay tax ñu gën a nekk benn ci suñu biir. Mbaa gëjoo ko def ? — Efes 4:29.
4 Na jóge ci suñu biir xol : Bu ñu waxee nit ne liggéeyam rafet na, wax jooju bala mu koy laal dëgg, na doon dëgg ci suñu xol. Nit ñi dañuy xam ndax li ñuy wax ci suñu xol la jóge, walla ndax ay wax kese la (Léeb. 28:23). Bu fekkee ne dañu faral di seetlu lu baax li nekk ci suñu mbokk yi, dinañu leen ko bëgg wax. Nañu faral di ndokkeel suñu mbokk yi, te li ñu leen di wax na jóge ci suñu xol, ndaxte “ kàddu bu ñu wax ci waxtoom, aka nekk lu neex ! ” — Léeb. 15:23.