Wonal sa moroom ne danga ko bëgg — Wax ko lu baax li mu def
1 Wax sa moroom lu baax li mu def, dafa koy may doole, dafay tax mu gën a sawar te gën a kontaan. Ci waaraate bi, ñu bare gis nañu ne, bu ñu defee loolu, dafay tax nit ñi bëgg ñu déglu. Naka lañu ko mënee def ?
2 Nañu am seetlu : Yeesu Krist seetlu woon na lu baax lu juróom-ñaari mbooloo yi nekkoon Asie mineure def (Peeñ. 2:2, 3, 13, 19 ; 3:8). Ñun itam, bu ñu bëggee ñi nuy waxal ci waaraate bi, dinañu seetlu lu baax li ñuy def ngir wax leen ko. Mën na nekk ni ñuy toppatoo seen kër, ni ñuy toppatoo seen doom, walla teral bu rafet bu ñu nu teral. Ndax dangay seetlu yu mel noonu te wax ko ñi ko def ?
3 Nañu déglu bu baax : Booy waaraate, nanga laaj nit ñi li ñu xalaat ci li ngay wax, ba pare déglu leen bu baax. Noonu nga leen di maye cér (Room 12:10). Te dinga mën a jàpp lu rafet ci li mu wax, ba wax ko ne xalaat bu am solo la. Dinga mën a jaar it ci loolu ba waar ko.
4 Nañu xam ni ñuy waxe : Bu nit ki waxee lu àndul ak dëgg gi nekk ci Biibël bi, lan lañu war a def ? Bul werante ak moom. Gërëm ko ci li mu wax. Ba pare, mën nga wax lu mel ni lii : “ Gis naa ne waxtaan bii itteel na la. ” (Kol. 4:6). Bu bëggee werante sax, ba tey mën nañu ko wax ne gis nañu ne waxtaan bi itteel na ko, te loolu lu rafet la. Loolu mën na tax kenn ku ñu foog ne bëggul déglu xibaar bu baax bi, dem ba nangu ñu déglu. — Léeb. 25:15.
5 Wax sa moroom ne li mu def rafet na, bala mu am njariñ, fàww mu jóge ci sa xol. Kàddu yuy yokk doole noonu, dañuy màggal Yexowa te mën na tax nit déglu xibaaru Nguur gi.