Bu ñuy waare, na ku nekk yokk sa doole moroom
1 “ Kàddu bi ñuy wax ci waxtu bi war ”, ñépp la neex (Léeb. (Prov.) 25:11). Bu ñu àndee ak suñuy moroom di waaraate, naka lañu mënee def ba mu wóor ñu ne suñu waxtaan dina yokk seen doole ?
2 Waxtaan buy yokk doole : Bu ñuy waare, bu ñu boolee lu jëm ci suñu ngëm ci waxtaan bu ñuy def ak ki ñuy àndal, loolu dina yokk doole (Sab. (Ps.) 37:30). Mën nañu waxtaan ci ni ñu mënee wone suñu téere yi, walla ñu nettali luy yokk doole te xew bu yàggul ci waaraate bi (Jëf. 15:3). Ndax gis nga ponk bu am solo ci li nga jàng ci Biibël bi, ci yéenekaay yu bees yi walla ci ndaje mbooloo mi ? Mën nañu wax ci benn waxtaan bu ñu jagleel ñépp bu ñu déglu bu yàggul ci Saalu Nguur gi.
3 Sa xol mën na jeex bu amee ku weddi li nga wax te fexewuloo ba tontu ko liy tax mu nangu kontine waxtaan bi. Su ngeen génnee kër googu, bu ngeen taxawee tuuti ngir seet li ngeen mën a def bu ñu leen waxatee lu mel noonu, dina baax lool. Mën ngeen seet loolu ci téere Comment raisonner. Bu ñu waxee ki ñu àndal li ñu neex ci waxtaan bi mu def, loolu dina yokk dooleem.
4 Nañu def dara : Ndax am na ci ñi nga bokkal gurupu njàngum téere ñu nga gëj a àndal ci waaraate bi ? Bu ñu waxee nit pur ñu ànd ci waaraate bi, xéyna dinañu mën a “ dimbaleente ci sunu ngëm ” (Room 1:12). Pioñee yu ci sax yi ak pioñee yuy jàpple yi, bu ñu amee ku ñu mën a àndal ci waaraate bi, dañuy kontaan. Rawatina bu dee ci suba teel bi la walla ci ngoon buy waaj a guddi, ndaxte waxtu yooyu du bare waaraatekat yuy waare. Bu ñu àndee ak pioñee yi ci waaraate bi, dinañu leen jàpple. Ndax am na waaraatekat bu màgget ba nga xam ne wér gi yaramam mayatu ko mu def lu bare ci waaraate bi ? Boo seete ni ngay def ba mu ànd ak yow ci waaraate bi, xéyna booy defi njàngum Biibël, dina leen njariñ yéen ñaar ñépp. — Léeb. (Prov.) 27:17.
5 Wax nit ne li mu def rafet na te di ko wax it li ñu neex ci moom, su dee sax ci fànn yu amul solo noonu la, dafa mas a nekk luy yokk doole. Waruñu fàtte loolu saa yu ñu àndee ak suñuy moroom ci waaraate bi, ndax li ñu bëgg mooy ‘ yokkante suñu ngëm ’. — 1 Tes. 5:11.