Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 nov.
“ Ñu bare tey dañu bëgg xam lu tax coono àddina si di yokku, te bañ a wàññeeku. Seetal li aaya bii wax ci lu tax loolu am. Ndax mas nga ci xalaat ? [Jàngal Peeñu bi 12:9 te fexeel ba mu ràññe kàddu yii : “ Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp. ” Boo paree, may ko mu tontu.] Téere bii dafay wone li Seytaane di def ngir nax nit ñi ak li ñu mën a def ngir xeex ko. ”
Réveillez-vous ! 22 nov.
“ Tey, lu mat 800 milioŋi nit duñu lekk bu doy. Waaye boo jëloon lekk bi am ci kow suuf si sépp, seddale ko ci nit ñépp, ñépp ay mën a lekk ba suur. Kon ndax xiif bi am tey jaadu na ? [Mayal nit ki tontu.] Boo xoolee dëkk yu mag yi am ci àddina si, fexe ba ñi fa nekk ñépp am lu ñuy lekk, dafay gën a jafe rekk. Ci loolu la téere bii di waxtaan. Wax na itam ci li Biibël bi dige, maanaam jamano joo xam ne kenn dootul xiif. ” Jàngal Sabuur 72:16 te won ko ne li ñu bëgg wax foofu mooy suuf si gën a wow sax dina joxe lekk bu bare, te dinañu góob lu bare ci suuf soo xam ne dafa naqadi béy.
La Tour de Garde 1er déc.
“ Ñu bare, bu ñu déggee Armagédon, dañuy xalaat bés boo xam ne ñu bare-bare dinañu dee. [Won ko wërale bi nekk ci xët 3.] Waaye ndax xam nga ne Armagédon bokk na ci li gën a baax lu mën a dal nit ñi ? Ndax loolu jaaxalu la ? [Mayal nit ki tontu.] Boo jàngee téere bii dinga xam lu tax ñu wax loolu. ” Jàngal 2 Pieer 3:13 te won ko ne Armagédon dina fi dindi ñi bon ak ñi dëng ñépp, ba pare Nguuru Yàlla dina ilif àddina si ni mu ware.
Réveillez-vous ! 8 déc.
“ Bu ñu doon waxtaan ak nit ñi, dañu seetlu ne ñu bare amuñu fu ñu dëkk. Ndax loolu mettiwul ? [Mayal nit ki tontu.] Yàlla dige na ne dina am bés boo xam ne nit ñépp dinañu am kër gu baax. Loolu laa la bëgg won. [Jàngal Isayi 65:21, 22 te won ko fu ñu wax ne : ‘ dinañu ci dëkk ’.] Téere bii dafay wone lu tax tey mu am ñu amul fu ñu dëkk. Dina wone it naka la Yàlla di defee li ñu jàng léegi ci Biibël bi. ”