Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 nov.
“ Ñépp a bëgg am wér-gi-yaram te dund lu yàgg. Bu ñu mënoon a dund ba fàww tey, ndax dina la neex ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Yowanna 17:3.] Téere bii dafay wax ci dund gu dul jeex gi Yàlla dige ci Biibël bi. Dafay wax it ni àddina si di mel bés bu loolu amee. ”
Réveillez-vous! 22 nov.
“ Dañu bëgg waxtaan ak waajur yépp ci li ñu mën a def ngir aar suñuy doom ci feebar bi ñu wax Sidaa. Ci 20 at yi weesu, boroom xam-xam yi def nañu lu bare ngir gën a xam ni feebar boobu di deme ak garab yi baax ci moom. Waaye ba tey, li nit ñu bare xalaat ci feebar boobu, du loolu moo am. [Won ko wërale bi tudd “ Idées reçues ” te may ko mu wax li mu ci xalaat.] Téere bii mu ngi wax ci li waajur yi mën a def ngir aar seeni doom ci feebar boobu. ” Jàngal 5 Musaa 6:6, 7 te woneel bu baax ne jàngal xale yi Kàddu Yàlla, warugaru waajur yi la.
La Tour de Garde 1er déc.
“ Tey dañuy waxtaan ak nit ñi ci lenn luy wuutale nit ak mala. Loolu mooy xam lu baax ak lu bon. Waaye gis nañu ne nit ñu bare dañuy def lu bon. Lu tax loolu ci sa xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Peeñu bi 12:9 te waxaatal kàddu bii : “ Moom miy nax waa àddina sépp. ”] Téere bii dafay waxtaan ci li ñu mën a def ba xam te jëfe lu baax. ”
Réveillez-vous! 8 déc.
“ Dañu bëggoon a waxtaan ak yow ci lu jëm ci xarit, lu tax xarit am solo ci doom-Aadama. Boroom xam-xam yi defar nañu ay fasoŋu masiin yu dul jeex ngir yombalal dundu nit ñi. Waaye ba tey, bala doom-Aadama mën a am dund gu neex, fàww mu am xarit. Léegi dama la bëgg laaj dara : Ndax gis nga ne suñu jamano jii dafa soppeeku ba am xarit dëgg jafe lool ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Léebu 18:24 te won ko foofu ne “ xarit ” moo mën a sut “ mbokk ” ci wàllu xaritoo.] Téere bii, dafay waxtaan ci li ñu mën a def ba am xarit dëgg te yàgg ak ñoom. ”