TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/03 p. 6
  • Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2004

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2004
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lekkool bu ñuy jàngal ni ñuy defe li ëpp solo ci àddina
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Lan mooy njariñu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Porogaraam bu bees pur ndaje yi ñuy def ci mbooloo mi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Lu bees li ñu defar ngir fàttaliku li ñu waxtaane ci ndaje yu mag yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 12/03 p. 6

Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ci atum 2004

1 Yexowa dafa ñuy jàngal liggéey buy jariñ àddina si sépp. Te dafay jaar ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ngir loolu. Ayu-bés bu nekk mu am li ñu fay jàng. Ndax yaa ngi góor-góorlu ngir bokk bu baax ci lekkool boobu ? Bu sãwiyee jotee, dina am li ñuy soppi ci lekkool boobu, ngir eleew yi gën koo jariñoo.

2 Dina am ñuy ay-ayloo ngir jàpple kiy xelal nit ñi : Kiy jàpple kiy xelal nit ñi, dafay xelal ñiy def waxtaan n° 1 ak kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi. Ñooñu kontaan nañu lool ci xelal yooyu. Léegi, fépp fu am ay mag yu ko mën, at mu nekk dinañu tànn beneen mag ngir mu jàpple kiy xelal nit ñi. Bu ko defee, mag ñi dinañu mën a bokk liggéey boobu. Dina tax it mag ñi ak surga mbooloo mi mën a jànge ci yeneen mag ñi nga xam ne ñu mën def waxtaan te mën jàngale lañu.

3 Waxtaan ak ñi teew ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi : Bu fekkee ne seen ndaje bu mag bu ñaari fan dafay tombe ak ayu-bés bu ñu war a fàttaliku li ñu def ci lekkool bi, nangeen def ci ndaje bu mag bi li ngeen waroon a def ayu-bés bu ci topp te ayu-bés bu topp ndaje bu mag bi, ngeen sog a def waxtaan bi ñu war a def ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi ak yeneen waxtaan yi mu àndal. Bu fekkee ne wottukat biy wër dafa war a ñów ci ayu-bés bu ñu war a fàttaliku li ñu def ci lekkool bi, soxlawul ñu soppi porogaraam bi yépp. Dinañu def woy-Yàlla bi, liy tax ñu aay ci wax ak it “ Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi ”. Waxtaan n° 1 bu ñu war a def ayu-bés bu ci topp lañu ciy yokk . Bu ñu defee waxtaan bi tudd “ Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi ” ba paree, dinañu def ndaje bu jëm ci liggéeyu waare bi, waaye 30 minit kese lay yàgg. Mag ñi dinañu seet ndax dinañu def ñetti waxtaan yoo xam ne bu ci nekk 10 minit lay mat, walla ñaari waxtaan yu 15 minit bu nekk. (Kenn du def yégle yi.) Bu ñu paree ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi, dinañu woy benn woy-Yàlla ba pare may wottukat biy wër mu waxtaan ak waa mbooloo mi lu mat 30 minit. Ayu-bés bu ci topp nag, dinañu def waxtaan bi tudd “ Liy tax ñu aay ci wax ” ak bi tudd “ Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi ” ni ko porogaraam bi waxe, ba pare def waxtaan bi ñuy def ngir fàttaliku li ñu def ci lekkool bi.

4 Jariñool bu baax lépp li la mën a jëmloo kanam ci wàllu ngëm. Boo jariñoo ci li ñu lay jàngal ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi, dinga tax sa waa mbooloo gën a sawar, dinga bokk ci ñiy def li Biibël bi waxoon ne dina am, te dinga tax nit ñi màggal Ki ñu jox xibaar bi ñu war a yégle. — Isa. 32:​3, 4 ; Peeñ. 9:19.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager