Ñjàngum téere Adorez le seul vrai Dieu
Téere Adorez le seul vrai Dieu dañu ko defar ngir ñu jàng ko ak ñiy pare jàng téere Xam-xam. Bu ñu ko jàngee ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, dina tax ñu xam ni ñu koy wonee ci waaraate bi. Dina tax it ñu gën a bëgg te fonk Yexowa ak mbootaayam. Lan lañu war a def ngir jariñoo bu baax njàngum téere bi ñuy def ci téere Adorez le seul vrai Dieu ?
Kiy jiite waxtaan bi : Pàcc bu nekk ci benn waxtu kese lañu koy def. Kon kiy jiite waxtaan bi war na xam ni mu war a yàgge ci xise bu nekk. Warul yàgg ci xise yu njëkk yi. Bu ko defee, bu ñu demee ba tollu ci xise yi gën a xoot yu ci faral a topp, ñu mën cee gën a yàgg. Wërale biy jeexal pàcc bu nekk, dañu ci war a waxtaan ci lu gàtt, ngir ñi fekke waxtaan bi mën a jàpp li ëpp solo ci pàcc bi.
Am na ay xise yu ànd ak ay laaj yu bare ngir nit ñi xalaat ci bu baax te waxtaan ci. Lu mat génn-wàllu pàcc yi nekk ci téere Adorez Dieu am nañu xise yu mel noonu. Mën nga ci gis benn ci xët 48. Bu ngeen tolloo ci xise yooyu, kuy jàng xise yi, soxlawul mu jàng laaj yooyu, te kiy jiite waxtaan bi mooy seet aaya yi ngeen mën a jàng ci waxtu bi te waxtaan ci.
Nañu ko waajal bala muy jot : Rëdd tontu yi kese, taxul ñuy wax ne waajal nga bu baax njàngum téere bi. Bu ñu xalaatee bu baax ci aaya yi nekk ci xise yi, dinañu waajal li ñu nar a tontu, waajal it suñu xol. Te loolu sax moo ëpp solo (Esr. 7:10). Nit ku nekk am nga li nga mën a def ngir ndaje boobu yokk suñu doole ci wàllu ngëm ñun ñépp. Mooy bañ a ragal tontu te it bañ a bare tont ba tere ñeneen wax ñoom itam seeni xalaat. — Room 1:11, 12.
Suñu njàngum téere Adorez le seul vrai Dieu dina ñu dimbali ñu gën a jege Yexowa te gën a mën a dimbali ñi bëgg jaamu Yexowa ak ñun (Sab. 95:6 ; Saak 4:8). Nañu fexe ñun ñépp ba jariñoo bu baax njàngum boobu nekk lu am solo ci wàllu ngëm.
[Wërale bi nekk paas 7]
Adorez le seul vrai Dieu
Programme d’étude pour 2003
Oct. 20 : chap. 1
27 : chap. 2
Nov. 3 : chap. 3
10 : chap. 4
17 : chap. 5
24 : chap. 6
Déc. 1 : chap. 7
8 : chap. 8
15 : chap. 9
22 : chap. 10
29 : chap. 11
Programme d’étude pour 2004
Janv. 5 : chap. 12
12 : chap. 13
19 : chap. 14
26 : chap. 15
Févr. 2 : chap. 16
9 : chap. 17
16 : chap. 18
23 : chap. 19
Mars 1 : chap. 20
8 : chap. 21