Xaaj 3 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Nañu jëfandikoo bu baax Mbind yi
1 Bu ñuy jàngale Biibël bi, dañu bëgg “ sàkk ay taalibe ”. Naka lañu ko mënee def ? Fexe ba nit ki nànd, nangu te topp li Kàddu Yàlla wax (Macë 28:19, 20 ; 1 Tes. 2:13). Kon lépp lu ñuy jàngale, na jóge ci Biibël bi. Mën nañu njëkk won nit ki ni mu mënee xam fan la aaya yi nekk ci Biibëlam. Ñun nag, naka lañu mënee jëfandikoo Mbind yi ngir dimbali ñi ñuy jàngal ñu jëm kanam ci wàllu ngëm ?
2 Seetal yan aaya nga bëgg jàng : Booy waajal njàngum Biibël bi, jàngal aaya yi nekk ci xise yi te seetal lu tax ñu def leen fa. Ba pare tànnal yi nga bëgg jàng ak nit ki ngir waxtaan ci. Li gën mooy aaya yooyu nekk fi ñu jële li ñu gëm. Mën nga bàyyi aaya yi ànd ak ponk yi ëppul solo. Te bul fàtte nit ki ci boppam ak li mu soxla ci wàllu ngëm.
3 Laaj ko lu jëm ci aaya yi : Bu ngeen jàngee benn aaya ba pare, laajal nit ki mu wax la lu tax ñu def ko ci xise bi. Moom moo ko war a wax, du yow. Su dee yombul ci moom, mën nga ko laaj benn laaj walla lu ko ëpp ngir mu xam li tax ñu def aaya bi ci xise bi. Boo waree yokk dara ngir gën a leeral aaya bi, na fekk nit ki tontu la ba pare.
4 Waxal lu yomb nànd : Rëbbkat bu aay, mën na sànni benn fett kese, jam mala bi mu bëgg jàpp. Noonu it, jàngalekat bu aay, waxam du bare. Li muy jàngale dafa yomb, leer te nekk dëgg. Waaye nag, yenn saay, fàww mu gëstu ci téere karceen yi ngir mën a leeral yenn aaya (2 Tim. 2:15). Waaye bul jéem a leeral lépp li nekk ci aaya yi. Waxal rekk ci ponk bi ngeen di jàng.
5 Waxal nit ki ni mu mënee topp li mu jàng : Saa yoo gisee aaya bu baax ci kiy jàng, fexeel ba mu gis ne war na ko topp. Mën na nekk booy jàng Yawut yi 10:24, 25 ak koo xam ne komaaseegul teewe ndaje karceen yi. Bu boobaa mën nga ko wax li ñuy def ci ndaje yi te wax ko mu ñëw teewe. Waaye moytul a wax ba nit ki foog ne danga ko bëgg defloo li mu bëggul. Bàyyil Kàddu Yàlla xiir ko ci li neex Yexowa. — Yaw. 4:12.
6 Bu ñuy sàkk ay taalibe, nañu fexe ba nit ñi “ gëm, ba jébbalu ”, ndax ni ñuy jëfandikoo bu baax Mbind yi. — Room 16:26.
[Laaj yi]
1. Bu ñuy jàngale Biibël bi, lu tax ñu war koo jëfandikoo bu baax ?
2. Naka lañuy tànne aaya yi ñu bëgg jàng ci njàngum Biibël bi ngir waxtaan ci ?
3. Lu tax ñu war a laaj nit ki lu jëm ci aaya yi, te naka lañu ko mënee def ?
4. Ndax lépp lañu war a leeral ci bépp aaya bi ñuy jàng ?
5, 6. Naka lañu mënee dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ngir ñu topp Kàddu Yàlla, waaye lan lañu war a moytu ?