Nanga jariñoo wideo bi tudd Pas de sang : la médecine relève le défi
Li nga xam ci faj nit te bañ ci boole deret, fu mu tollu ? Ndax mën nga wax yenn pexe yi am ngir def loolu, ak ni ñu koy defe ? Xoolal wideo bii, ba pare seetal ndax mën nga tontu laaj yii di topp. — Xamal lii : Ci wideo bii, am na fu ñuy wone ay doktoor yuy opeere nit. Loolu barewul, waaye waajur yi ñoo war a seet ndax dinañu bàyyi seeni doom yu tuuti yi seetaan wideo bi.
1) Lan mooy li ëpp solo ci li tax Seede Yexowa yi di bañ ñu sol leen deret, te loolu fan lañu ko mënee jàng ci Biibël bi ? 2) Bu ñu demee ci doktoor ngir faju, lan lañu bëgg ? 3) Lan la yoonu nguur may ki ñuy faj ? 4) Lu tax bañ ñu sol la deret nekk liy yoon ak li gën ? 5) Bu amee koo xam ne deret bu bare mu ngi génn ci yaramam, li doktoor yi war a njëkk def, ñaar la. Ñaar yooyu, lan la ? 6) Sol deret, lan la mën a yàq ci yaram ? 7) Bu doktoor di opeere nit, lan la mën a jëfandikoo ngir nit ki bañ a ñàkk deret bu bare ? 8) Bu ñu la nangoo faj te du ñu ci boole deret, ba tey lan nga war a jéem a xam ? 9) Ndax doktoor yi mën nañu opeere nit, opeere bu garaaw a garaaw, te bañ ci boole deret ? 10) Lan la doktoor yu gën di bare nangu defal Seede Yexowa yi ? Ban fasoŋu faj lañu mën a yaakaar ne doktoor yépp dinañu ko nangu ëllëg ?
Nit ku nekk moo war a seet ndax dina nangu ñu def ko li ñu wone ci wideo bii ngir faj ko. — Xoolal li nekk ci La Tour de Garde bu 15 suweŋ 2004, xët 22-4, 29-31, ak La Tour de Garde bu 15 oktoobar 2000, xët 30-1.