Benn wideo buy wone lu am solo li doktoor yi di jéem a def léegi
Ku feebar dañu ko war a jox li ko yoon bi may ci wàllu faj te war na nekk lu xelam nangu. Àttekat yi ak doktoor yi, ñu ngi ci gën a def seen xel léegi. Loolu indi na fasoŋu faj yu bees. Seede Yexowa yi sax dañu ciy jariñoo (Jëf. 15: 28, 29). Wideo bi tudd Soigner sans transfusion — Besoins et droits du patient, ci loolu yépp lay waxtaan. Nanga ko seetaan, ba pare seetaat li nga ci jàng. — Xamal lii : Ci wideo bii, am na fu ñuy wone ay doktoor yuy opeere nit. Li ñu ciy wone, barewul, waaye waajur yi ñoo war a seet ndax dinañu bàyyi seeni doom yu tuuti yi seetaan wideo bi.
1) Lu tax doktoor yi di seetaat léegi lépp lu jëm ci sol deret ? 2) Doktoor yi mën nañu opeere lu garaaw-a-garaaw, fekk duñu sol nit ki deret. Ci yi ñu mën a opeere noonu, wax ci ñett. 3) Ci àddina si sépp, ñaata doktoor ñoo nangoo opeere Seede Yexowa yi fekk duñu leen solal deret ? Lu tax ñu nangu def loolu ? 4) Yàggul noonu, am na ay loppitaan yu gëstu mbirum sol deret. Lan lañu wax ? 5) Sol deret, lan lu bon la mën a def ci yaramu nit ? 6) Am na leneen lu ñu mën a def lu dul sol deret. Lan la ay boroom xam-xam yu aay ci wàll boobu wax ci njarin bi ci nekk ? 7) Lan mooy indi ñàkk deret ? Ñaata deret la nit mën a ñàkk, te du dee ? Lan moo ko mën a faj ? 8) Lu ñu mën a def ba li tubaab di woowe globules rouges gën a bare ci yaramu nit ? 9) Bu ñuy opeere, lan la doktoor yi di def ngir deret bi bañ a tuuru ba mu ëpp ? 10) Ndax mën nañu faj xale bu ndaw walla ku ñu ragal mu dee ci saa si, fekk duñu leen sol deret ? 11) Bala ñu mën a faj nit ni mu ware, lan lañu war a bañ a fàtte ? 12) Lu jëm ci ni ñu mënee faj ku bañ deret, lu tax karceen yi war a xam lu ñuy nangu ak lu ñu dul nangu ci wàllu faj nit fekk duñu ko sol deret, bala feebar di leen dal ? Te loolu, naka lañu ko mënee def ?
Ci kow li Biibël bi wax, nit ku nekk moo war a seet ndax mën na nangu ñu def ko li ñu wone ci wideo bii. Ci fasoŋu faj yooyu, ndax tànn nga ba pare yi ngay nangu yow ak say doom ? Boo amee mbokk bu nekkul Seede, war nga ko xamal ba mu leer nàññ li nga tànn ak lu tax nga tànn ko. — Seetal “ Questions des lecteurs ” ci La Tour de Garde bu 15 suweŋ 2004 ak bu 15 oktoobar, 2000.