War nga seetaan wideo bi tudd : No Blood—Medicine Meets the Challenge
Fan la sa xam-xam tollu ci li ñu mën a def ngir faju te bañ a jëfandikoo deret ? Ndax xam nga yenn yëf yi ñu mën a jëfandikoo boo bañee ñu sol la deret, ak naka lañu koy jëfandikoo ? Boo bëggee xam fi sa xam-xam tollu, seetaanal wideo bi te tontul ci laaj yiy ñów. (Bul fàtte : Ndegam wideo bi dafay wone fu ñuy opeere nit, way-jur yi war nañu seet bu baax ndax mën nañu ko seetaan ak seen doom yu ndaw yi.)
1) Lan moo gën a tax Seede Yexowa yi di bañ ñu sol leen deret, te fan la Biibël bi wone ne waruñu ko nangu ? 2) Lan lañu bëgg ci wàllu faj ? 3) Lan la yoon may nit ku feebar ? 4) Lu tax ñu mën a wax ne ku bañ ñu sol ko deret ànd na ak sagoom te xam na li muy def ? 5) Bu amee ku am deret bu bare bu tuuru, ci lu gaaw lan mooy ñaari yëf yu doktoor yi war a njëkk a def ? 6) Sol deret yan jafe-jafe lay indi ci wàllu wér-gi-yaram ? 7) Bu doktoor di opeere nit, lan la mën a jëfandikoo ngir wàññi deret biy tuuru ? 8) Lan nga war a xam ci lu jëm ci li ñu mën a jëfandikoo ngir faj nit te bañ ko sol deret ? 9) Ndax mën nañu opeere nit, opeere bu metti te bañ ko sol deret ? 10) Lan la doktoor yu gën di bare nangu def ngir Seede yi, te lan moo mën a nekk fasoŋ bu ñuy faje ñi feebar ?
Nit ñi nuy jàngal Biibël bi, suñu jëkkër, suñu jabar, suñu mbokk bu nekkul Seede, ki ñuy liggéeyal, suñuy jàngalekat yi walla suñu waa kalaas yi, bu amee ku ñu ci laaj lu ñu xalaat ci sol deret, mën nañu seetaan ak moom wideo bi tudd No Blood. Ci lu wóor dina baax lool. Wideo bi wone na ay fasoŋ yi ñu mën a faje nit ñi. Nit ku nekk moo war a seetal boppam ban la ko ci xelam may. — Seetleen “ Questions des lecteurs ” bu nekk ci La Tour de Garde bu 15 suweŋ ak bu 15 oktoobar 2000.