TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 1/07 p. 3
  • Faj bi gën

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Faj bi gën
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • War nga seetaan wideo bi tudd : No Blood—Medicine Meets the Challenge
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Nanga jariñoo wideo bi tudd Pas de sang : la médecine relève le défi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Benn wideo buy wone lu am solo li doktoor yi di jéem a def léegi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Benn wideo buy wone lu am solo li doktoor yi di jéem a def léegi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 1/07 p. 3

Faj bi gën

Doktoor Michael Rose mii nekk chef de service d’un département d’anesthésiologie, nee na, bu ñu la fajee te kenn solu la deret, faj boobu mooy bi gën. Yan fasoŋu faj te it lan lañu mën a sol ci sa yaram boo bëggul deret ba ñu mën a wax ne ci faj bu jëfandikoowul deret la bokk ? Loolu war nga ko xam boo bëggee mën a tànn bu baax li ñu la mën a def bu ñu lay faj walla bu ñu lay opeere. Seetaanleen wideo bi tudd Pas de sang : La médecine relève le défi, ba pare ngeen tontu ci laaj yii di topp ngir seet ndax nànd ngeen li ñu ci wax. — Xamal lii : Ci wideo bii, am na fu ñuy wone ay doktoor yuy opeere nit. Li ñu ciy wone, barewul, waaye waajur yi ñoo war a seet ndax dinañu bàyyi seeni doom yu tuuti yi ñu seetaan wideo bi.

1) Lan moo gën a tax Seede Yexowa yi bañ ñu sol leen deret ? 2) Ci wàllu faj nit, lan la Seede Yexowa yi bëgg ? 3) Lan la yoon may képp ku feebar ? 4) Am na ñuy laaj ñu faj leen ak leneen lu dul deret. Lu tax ñu mën a wax ne ñooñu def nañu lu ànd ak xel te def nañu li leen war ? 5) Bu nit ñàkkee lu bare ci deretam, am na ñaar yu doktoor yi war a njëkk def ci lu gaaw. Mooy lan ak lan ? 6) Bu ñu bëggee faj nit te bañ ko sol deret, am na ñeenti mbir yu ñu war a topp. Ñeent yooyu ñooy lan ? 7) Naka la doktoor mënee fexe ba a) li deretu nit ki di tuuru bañ a bare, b) nit ki bañ a ñàkk li ñuy woowe ci tubaab globules rouges, c) fexe ba yaramu nit ki defaral boppam deret ci lu gën a gaaw, te d) nit ki amaat deret bi mu ñàkkoon ? 8) Waxal ni ñuy defe ñaar yii di topp a) hémodilution ak b) Récupération du sang épanché. 9) Lan nga war a wut a xam ci lu jëm ci li ñu mën a def ngir faj la te bañ a jëfandikoo deret ? 10) Ndax mën nañu opeere nit, opeere bu metti, te bañ koo sol deret ? 11) Naka la doktoor yi jëme kanam ?

Nit ku nekk moo war a seet ndax li mu jàng ci Biibël bi may na ko mu nangu ñu def ko yenn ci li ñuy wone ci wideo bii. Ci fasoŋu faj yooyu, ndax tànn nga ba pare yi ngay nangu yow ak say doom ? Boo amee mbokk bu nekkul Seede, war nga ko xamal ba mu leer li nga tànn ak lu tax nga tànn ko. — Seetal “ Questions des lecteurs ” ci La Tour de Garde bu 15 suweŋ 2004 ak bu 15 oktoobar 2000.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager