Nañu yiw ngir roy Kirist
1. Turu ndaje bu ñetti fan bii di ñów, lu mu séq ak yiw ?
1 Biibël bi dafay wone Yexowa, mi nekk Aji Kowe ji, ni ku soloo yiw (Sab. 104:1). Li Yeesu doon wax ak li mu doon def yépp, dafa ko doon def ngir màggal baayam ak lépp lu Mu taxawal (Ywna. 17:4). Loolu, dinañu ko mën a def ci suñu ndaje bu ñetti fan biy ñów te tudd “ Nañu roy Kirist ”. Kenn ku nekk ci ñun, dinga fa mën a roy Yeesu te màggal Yexowa !
2. Waaj bi ñuy def ngir teewe bés bu nekk, naka lay màggale Yexowa ?
2 Nañu yiw bu ñuy jaamu Yàlla : Mën nañu màggal Yexowa bu ñuy def lépp ngir teewe xew bu réy ci wàllu ngëm bu ñu nu waajal. Ndax waxtaan nga ba pare ak ki ngay liggéeyal, te ndax pare nga lépp li nga war a def ngir mën a teew ci ñetti bés yi, boole ci bésu àjjuma ji ? Ndax dinga teel a àgg ci bérébu ndaje bi ngir mën a seet fi ngay toog te mën a bokk ci woy-Yàlla bu njëkk bi ak ñaan bi ? Ndax dinga defar añ bu lay may nga mën koo lekk ci bérébu ndaje bi fu say mbokk yi nekk ? Bu waxtaan yi di waaj a komaase, kiy jiite porogaraamu bés bi dina ñaan nit ñi ñu toog bala misik bi di komaase. Bu ñu déggee loolu, war nañu gaaw a àggali suñu waxtaan yi. Bu ko defee, bu porogaraam bi di komaase, dina fekk ñu toog suñu palaas ba pare.
3. Def suñu xel yépp ci porogaraam bi, loolu naka lay màggale ni ñuy jaamoo Yàlla ?
3 Bu ñu defee suñu xel yépp ci liy am ci porogaraam bi, loolu it dina màggal suñu Baay bi nekk ca asamaan. Am na benn taskatu xibaar bu fekke woon benn ndaje bu mag ci dëkkam. Bindoon na ne, ku fa teewe, dinga waaru ci “ yar ak teggin bi nit ñi di wone foofu. Dañuy noppi, ànd ak yar, di déglu li ñu fay wax. Ku leen gis rekk xam ne fonk nañu dëgg lépp lu jëm ci seen diggante ak Yàlla. ” Wax na it ci xale yu bare lool yi mu fa gisoon “ ñoom ñépp yaru di seet sax aaya yi ci Biibël bi fekk loolu jafe na gis tey. ” Bu porogaraam bi komaasee ba pare, waratuñu nekk di waxtaan, di bind ay SMS ci suñu portaabël, di lekk, walla di doxantu. Xale yi dañu war a toog ci seen wetu wayjur. Bu ko defee, seeni wayjur dinañu leen a mën a dimbali ñu jariñoo bu baax porogaraam bi (5 Mus. (Deut). 31:12 ; Léeb. 29:15). Bu ñu defee lu mel noonu, dafay wone ne may nañu ñeneen ñi cér te it fonk nañu lekk bu am solo bi ñuy joxe ci wàllu ngëm.
4. Bu ñu nekkee ci ndaje bu mag bi, lu tax ñu war a sol lu yiw ?
4 Nañu sol lu yiw : Ci ndaje bu ñetti fan bu daaw, defoon nañu waxtaan bu tudd “ Montrez-vous des chrétiens dignes en toutes circonstances (maanaam nangeen nekk ay karceen yu yiw fépp fu ngeen di nekk). Waxtaan boobu wone woon na ne ñiy jaamu Yàlla, dañu war a def lépp ngir li ñuy sol ak ni ñuy defare seen bopp yiw ni ko karceen yi war a defe. Ñu bare kontaanoon nañu ci li ñu leen doon fàttali ci waxtaan boobu. Ren itam, war nañu bàyyi suñu xel bu baax ci loolu. Ni ñuy soloo dafay wone ni ñu fonke Yexowa ak ni ñu fonke it cér bi mu ñu may, maanaam bokk ci ay seedeem. Dañu war a solu saa su nekk ni nit ñiy “ woote ag ragal Yàlla ”. — 1 Tim. 2:9, 10.
5. Bu ñu nekkee ci dëkk fi ñuy defe ndaje bu mag bi, naka lañu mënee fexe ba ni ñuy soloo nekk lu yiw bu fekkee sax dañuy féexal suñu xol ?
5 Ndax bu ñu nekkee ci ndaje bu mag bi kese lañu war a sol lu yiw ? Buñu fàtte ne nit ñu bare dinañu xool kayitu ndaje bi ñuy taf ci suñu yére bu ñu nekkee ci dëkk fi ñuy defe ndaje bu mag bi. Ni ñu soloo war na tax nit ñi gis ne wuute nañu ak ñeneen ñi. Kon bu ñuy génn sax ngir féexal suñu xol, mel ni bu ñuy dem lekki ci restoraŋ bu porogaraam bi jeexee, war nañu sol lu jekk ni ko karceen yuy jaamu Yexowa waree def. Kon waruñu sol lu mel ni jeans, shorts walla T-shirts. Su ñu toppee loolu, dina doon seede bu mag ci dëkk bi ! Yexowa dafay kontaan bu gisee ne ni ñuy soloo dafay wone ne ay liggéeykatu Yàlla lañu.
6. Bu ñu yiwee ni karceen war a mel, ban njariñ lay am ?
6 Njariñ bi ci nekk : Ci ndaje yu mag yi, bu ñu wonee ne karceen yu yiw lañu, loolu dina ñu ubbil bunt yu ñuy waare. Dina tax it nit ñi xalaat lu rafet ci ñun. Bi suñu benn ndaje bu mag jeexee, am na benn góor bu doon liggéeyal nguur gi bu nee : “ Masu ñu gis mbooloo bu am yar ak teggin ni yéen. Ni ngeen mel, noonu la Yàlla bëgg ñépp mel ”. Bu ñu yiwee, loolu dafay wone ne bëgg nañu suñuy moroom te it may nañu leen cér. Dina màggal itam Yexowa (1 Piy. 2:12). Dafay wone it ne ragal nañu Yàlla te fonk nañu li suñu Baay nekke suñu jàngalekat (Yaw. 12:28). Bu ñuy séentu ndaje bu mag bu ñetti fan bi tudd “ Nañu roy Kirist ”, nañu góor-góorlu ngir nekk ay nit ñu yiw.