Wonal sa moroom ne danga ko bëgg — Nanga jéem a waxtaan ak nit ku nekk ci li ko itteel
1 Ndaw li Pool dafa tàmmoon di seet ci fasoŋ bi nit ñi yaroo ak ci li nekk ci seen xel ngir xam ni muy waxe ak ñoom. Royukaay bu baax la (1 Kor. 9:19-23). War nañu góor-góorlu ngir def ni moom. Sasu Nguuru Yàlla yi dañuy wone li ñu mën a wax bu ñuy waare. Nañu seetaat li ñu ci wax balaa ñuy dem waare ngir seet li ñu ci war a soppi ngir mën a wax luy ànd ak li nit ñi soxla ci suñu goxu mbooloo. Bu ñu nekkee ci buntu kër, nañu seetlu li ñuy won li mën a itteel ñi fa dëkk. Te bu ñuy wax ak ñoom, nañu boole loolu ci suñu waxtaan. Waaye nag am na leneen lu ñu mën a def ngir li ñuy wax mën a ànd ak liy itteel nit ñi ñuy waxtaanal ci waaraate bi.
2 Nanga seet ci li nit ñi di wax ngir xam li nga war a wax : Bu ñuy yégle xibaar bu baax bi, tàmm nañu di laaj nit ñi benn laaj te may leen ñu tontu. Bu nit tontoo, lan ngay def ? Ndax danga koy tontu lu gàtt rekk ngir won ko ne dégg nga li mu wax, ba pare kontine ci li nga bëggoon a wax ? Walla ndax li ngay wax dina wone ne jàpp nga li mu wax ? Bu fekkee ne li nit ñi di wax soxal na la, mën nga leen laaj it yeneen laaj ngir xam li ñuy xalaat dëgg (Léeb. 20:5). Boo defee loolu ba pare, mën nga seet ci xibaaru Nguuru Yàlla lu mën a ànd ak leen itteel, te waxtaan ci.
3 Kon war nañu nangu waxtaan ak nit ñi ci leneen lu dul li ñu waajaloon. Mën nañu komaase wax ci li ñu dégg ci xibaar yi, te nit ki wax ci leneen li ko gën a itteel. Mën na nekk li soxal nit ñi ci seen gox, walla li ko soxal moom ci boppam. Bu fekkee ne dañu ko bëgg dimbali dëgg, dinañu bàyyi li ñu bëggoon a wax, te wax ci li ko gën a itteel. — Fil. 2:4.
4 Na sa waxtaan ànd ak li itteel nit ki : Bu nit ki laajee benn laaj, xéyna dinañu bëgg xaar ba beneen yoon balaa ñuy kontine waxtaan bi. Bu ko defee, dinañu mën a seet tontu laaj boobu ci suñu téere yi. Mën nañu ko jox it téere buy wax bu baax ci li mu laajte. Loolu lépp dina wone ne dëgg-dëgg dañu bëgg dimbali nit ñi ngir ñu xam Yexowa. — 2 Kor. 2:17.