Ni ñu mënee waajal li ñuy wax ngir wone suñu yéenekaay yi
1 Xéyna yaa ngi xalaat lii : ‘ Waaw, komka def nañu ci Sasu Nguuru Yàlla bi li ñu mën a wax ngir wone yéenekaay yi, lu tax ma war koo waajalati ? ’ Ñu bare gis nañu ne li ñu def ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone yéenekaay yi, dafa am njariñ lool. Waaye loolu terewul ñu war a waajal suñu bopp. Li nar a baax ci gox bii, mën na bañ a baax ci beneen gox. Moo tax, buñu foog ne, mënuñu soppi dara ci li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone yéenekaay yi. Bu ci amee sax lu ñu bëgg topp, li gën mooy ñu waxe ko ci suñuy kàddu bopp.
2 Tànnal benn waxtaan ci yéenekaay bi : Boo jàngee yéenekaay bi ba pare, nanga ci tànn waxtaan bu nar a baax ci seen gox. Na doon waxtaan bu la neex yow ci sa bopp. Ki ngay won yéenekaay bi, bu gisee ne li ngay wax dafa la wóor, neex la te danga ci sawar lool, xéyna mu bëgg ko jàng moom itam. Bu fekkee ne sax danga tànn ci yéenekaay bi waxtaan bu neex nit ñi ci seen gox, nanga xam bu baax li nekk ci yeneen xaaj yi. Bu ko defee, boo dajee ak koo xam ne beneen waxtaan moo ko gën a soxal, dinga mën a soppi li nga naroon a wax.
3 Laajal nit ki benn laaj : Boo defee loolu ba pare, nanga seet bu baax li nga nar a njëkk wax. Li ngay wax ngir ubbi sa waxtaan dafa am solo lool. Mën nga laaj nit ki lu mën a tax mu xalaat bu baax. Loolu mën na tax nit ki bëgg yokk xam-xamam ci xaaj bi nga ko won ci yéenekaay bi. Laaj yu mel ni ‘ noo gisee mbir mii ’ walla ‘ loo xalaat ci lii ’ ñoo gën. Bu ko laaj lu koy nar a xatal walla luy tax mu bëgg xuloo.
4 Jàngal benn aaya : Boo defee loolu lépp ba pare, tànnal aaya booy jàng ak nit ki, saa yu mënee nekk. Mën nga ko jële sax ci xaaju yéenekaay bi nga bëgg wone. Jàng benn aaya, dina dimbali nit ki mu xam ne li ñuy wax, ci Kàddu Yàlla la jóge (1 Tes. 2:13). Aaya boobu ngeen di jàng, dina tax mu dégg xibaar bi, bu jëlul sax suñu yéenekaay yi. Am na ñoo xam ne, bala ñuy laaj nit ki benn laaj dañu koy njëkk jàngal benn aaya. Loolu dafay tax nit ki bëgg déglu waxtaan bi. Bala ngay jàng aaya bi, mën nga wax lii : “ Loo xalaat ci li Mbind mu sell mi wax fii ? ” Bu ngeen ci paree, mën nga won nit ki lu yéenekaay bi wax ci aaya boobu. Ba pare, bala nga koy laaj ndax bëgg na jël yéenekaay bi, nanga ko wax lu gàtt loo xam ne dina tax mu bëgg koo jàng.
5 Kenn mënul wax ne lii ak lii rekk lañu war a wax bu ñuy wone suñu yéenekaay yi. Waaye ci lu bare, li gën mooy ñu wax lu gàtt te yomb a nànd. Nanga wax lu yomb ci yow te baax ci nit ñi. Nanga gën a wax ci njariñu yéenekaay yi. Te mbégte bi ngay am ci ñoom, na feeñ ci sa waxin. Nit ñi “ jagoo dund gu dul jeex gi ”, dañu leen bëgg won La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi. Boo waajalee sa bopp bu baax, loolu dina gën a yomb ci yow. — Jëf. 13:48.
[Laaj yi]
1. Lu tax waajal li ngay wax ngir wone yéenekaay yi moo gën yem ci wax rekk li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi ?
2. Naka nga war a tànne ci yéenekaay bi waxtaan booy won nit ñi ?
3. Looy wax ngir tàmbali waxtaan bi te nga gis ne baax na lool ?
4. Lu tax jàngal nit ki benn aaya saa yu mënee nekk, nekk lu baax ?
5. Yan tegtal nga war a def ci sa xel booy waajal li nga bëgg wax ngir wone suñu yéenekaay yi ?