Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 juillet
“ Naqar bu réy lañuy yëg bu ñu amee mbokk walla xarit bu gaañu. Ndax foog nga ne am na ci ñoom luy dund ba tey ? [Mayal nit ki mu tontu.] Am na lu neex lu ñu Yeesu dig. [Jàngal Yowanna 5:28, 29.] Yeesu waxoon na ne, ‘ jamanoo ngi ñëw ’ ñi dee dinañu dekki. Téere bii dafay wone li Kàddu Yàlla wax ci fu nit ñi dee nekk tey. ”
Réveillez-vous ! Juillet
“ Nit ñu bare dañuy def li ñu mën ngir am dund gu rafet. Ci ñoom, nekk nit ku baax lu am solo la. Ndax loolu ngay xalaat yow itam ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li ñu mën a dal bu fekkee ne li ñuy gise ni lu baax dafa wute ak li Yàlla jàppe ni lu baax. [Jàngal Léebu 14:12.] Nekk nit ku baax ci kanamu Yàlla, lu muy tekki ? Loolu la téere bii di waxtaane ”. Won ko waxtaan biy komaase ci xët 20.
La Tour de Garde 1er août
“ Nit ñu bare tey, dañuy def lépp li ñu mën ngir am alal bu bare. Ndax foog nga ne alal bu bare mooy tax suñu dund gën a neex ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Yeesu waxoon ci ku bëgg am alal bu bare. [Jàngal Luug 12:15.] Lu tax bakkanu nit ajuwul ci alal, te it lan moo mën a tax suñu dund neex dëgg ? Loolu la téere bii di waxtaane. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 21.
Réveillez-vous ! Août
“ Fan la wayjur yi mënee am ay xelal yu leen di dimbali dëgg ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Yàlla dige fii ci Mbind mu sell mi. [Jàngal Sabuur 32:8.] Téere bii dafay wone naka la Kàddu Yàlla mënee dimbali wayjur yi ngir ñu yar bu baax seeni doom te fexe ba seeni doom am mbégte. ”