TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/05 p. 4
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2005
km 7/05 p. 4

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 juillet

“ Bu ñu waree seet li ñu bëgg def ci suñu àddina, ñépp a bëgg tànn li ñuy may jàmm ak bànneex. Lan moo ñu ci mën a dimbali ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal li ci yonent Yàlla Suleymaan wax. [Jàngal Léebu 14:15 te won ko foofu liy wuutale nit ku xamul lu bare ci àddina ak nit ku am seetlu.] Téere bii dafa ñuy won li ñu war a def ngir bañ a tànn li ñuy gaañ ëllëg. ”

Réveillez-vous ! 22 juillet

“ Ñu bare dañuy wax ne lépp li xew ci àddina, ndogalu Yàlla la. Waaye bu ñu gisee yëngu-yëngu suuf, ngelaw bu réy buy yàq lépp walla yeneen musiba yu mel noonu, dafa ñuy metti lool. [Waxal musiba bu mel noonu bu nit ñu bare dégg ci seen gox.] Ndax musiba yu mel noonu dañuy gën a bare tey ? [Mayal nit ki tontu.] Ci loolu la téere bii di wax. Ñi am mbokk bu gaañu ci musiba bu mel noonu, am nañu naqar bu réy. Lan moo mën a wàññi seen naqar ? Téere bii dina ci wax itam. ” Jàngal Yowanna 5:​28, 29.

La Tour de Garde 1er août

“ Ay nit ñu bare tey, dañu foog ne tekkiwuñu dara. Naka lañu mënee dimbali nit ñu mel noonu ? [Mayal nit ki tontu.] Biibël bi mën na dimbali nit ñooñu, ñu am mbégte dëgg. Téere bii, ci loolu lay wax. ” Wonal nit ki li ñu bind ak bind yu dëng te gën a ñuul ci xaaj bi tudd “ La Bible peut vous aider à trouver la joie ”.

Réveillez-vous ! 8 août

“ Tey nit ñi mën nañu dal ci seen moroom, gaañ leen, rey leen mbaa def leen leneen lu bon. Ñu bare sonn nañu ndaxte loolu dafay yokku rekk. Nit ñu bare tey, seen xel dalul dara. Foo leen fekk, ñu ngi ragal. Ci yow kan moo tax àddina si mel nii ba nit ñu bare ragal ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafa ñuy won li ñu mën a def ngir aar suñu bopp ci lu bon lu mën a dal suñu kow. Dafay wone it ci li Yàlla dige ci Biibël bi. Maanaam dina am bés boo xam ne kenn dootul ragal.” Jàngal Isayi 11:⁠9.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager