Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi Juillet
La Tour de Garde 15 juillet
“ Ndax foog nga ne nguur buy faj coono doom-Aadama yépp dina mas a am ? [Mayal nit ki mu tontu.] Yàlla samp na nguur bu nar a def loolu tuuti ci kanam. Ndax loolu neexul a dégg ? [Jàngal Luug 21:31.] Téere bii dafay wone lu tax Nguuru Yàlla gën nguuru nit. Dafay wone it barke yi muy indil doom-Aadama. ”
Réveillez-vous ! juillet
Boo dajee ak ndaw mën nga ko wax lii : “ Say moroom yu bare dañu bëgg am jëkkër [tàkk jabar]. Ci yow, fan lañu mënee am xelal yu baax ci fànn boobu ? [May ko mu tontu.] Seetal fii ci kan la séy jóge. [Jàngal Macë 19:6, te fexeel ba kàddu yii di topp feeñ bu baax : “ lu Yàlla takk ”.] Téere bii dafa ñuy won li Yàlla santaane ngir suñu séy bare jàmm. ”
La Tour de Garde 1er août
“ Tey ñiy toroxal seen moroom bare nañu lool. Bu ñu toppoon li Yeesu wax fii, ndax fooguloo ne dund gi dina gën a neex ? [Jàngal Macë 7:12, te may nit ki mu tontu.] Nit ku nekk yelloo nga ñu may la cér. Kàddu Yàlla dafay wone naka la loolu di ame ci kow suuf si sépp. Téere bii, ci loolu lay wax. ”
Réveillez-vous ! août
“ Wér-gi-yaram, ñépp la soxal. Ndax xam nga ne doktoor yu bare sawaratuñu sol nit deret ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bi dina la wax lu tax. Dina la won it lu tax deret nekk lu réy ci kanamu Yàlla. ” Jàngal 3 Musaa (Lévitique) 17:11 te won ko ne deret mooy li ñuy méngale ak bakkanu mbindeef yiy dund. Te bakkan, maye Yàlla bu jafe la.