TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/06 p. 4
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 8/06 p. 4

Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi

La Tour de Garde 15 août

“ Loo xalaat ci li Yeesu wax fii ? [Jàngal Macë 5:5.] Li ñu dige fii, bés bu amee, ndax foog nga ne dund gi ci kow suuf si dina mel ni suñu dund tey ? [Mayal nit ki mu tontu.] Kàddu Yàlla wone na barke yi Yàlla dig ñi nekk ci kow suuf si, te wax na li ñuy tekki. Loolu la téere bii di wone. Dafay wone it ñan ñooy donn suuf si. ”

Réveillez-vous ! août

“ Ndax foog nga ne ndaw yi war nañu jàng maye ci seen alal ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal fii li Kàddu Yàlla wax ci nangu maye. [Jàngal Léeb yi 11:25.] Téere bii dafay wone li ndaw yi di am bu ñuy dimbali ñi ko soxla. ” Won ko waxtaan bi ñu komaase ci xët 23.

La Tour de Garde 1er sept.

“ Ñu bare tey, mbirum diine soxalu leen. Ndax foog nga ne diine mën naa tax nit gën a baax ? [Mayal nit ki tontu.] Kenn ci ñi bind Sabóor dafa fonkoon mbirum Yàlla. Lii la wax. [Jàngal Sabóor 73:28 te fexeel ba “ m’approcher de Dieu est bon pour moi ” (maanaam ci man, jege Yàlla lu baax la) feeñ bu baax.] Téere bii dafay wone ni diine dëgg ji di màggale Yàlla ak ni mu ñuy jariñe. ”

Réveillez-vous ! Sept.

“ Am na ñu gëm ne Yàlla moo sàkk àddina si. Waaye téere yi ñuy jàng ca lekkool dañuy wone ne loolu àndul ak li boroom xam-xam yi wax. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Yawut ya 3:⁠4.] Lépp li ñu wër, dafay feeñal xam-xam bu réy te wone ne am na lu tax mu nekk fii. Réveillez-vous ! bii dafay wone li ñu mën a jànge ci loolu. ”

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager