Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 nov.
“ Am na ñuy laaj seen bopp ndax soxla nañu ay jàngu ngir jaamu Yàlla. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal lan la ci Biibël bi wax. [Jàngal Jëf ya 17:24.] Kon béréb fu ñuy jaamoo Yàlla lu ñuy jariñ ? Yéenekaay bii dafay wone li Biibël bi tontu ci laaj boobu. ”
Réveillez-vous ! 22 nov.
“ Ndax foog nga ne ci pexe science bi, maanaam boroom xam-xam yi, feebar yi dinañu fi jóge ? [Mayal nit ki mu tontu.] Réveillez-vous ! bii dafay wone yan yëf yu baax la science bi indi. Dafay wone itam lu tax Sàkk-kat bi kese moo mën a dindi feebar ak dee. ” Jàngal Sabuur 146:3-5, te woneel ay yéenekaay.
La Tour de Garde 1er déc.
“ Tey li ëpp ci nit ñi, dañuy wax ne fexe ba am li ngay dunde, jafe na lool. Ci loolu la jàngu yi nekkee ñoom itam, te dañuy gën a laaj nit ñi xaalis. Ndax loolu taxu la jaaxle ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal 1 Tesalonikk 2:9.] La Tour de Garde dafay wone li ci Biibël bi wax. ”
Réveillez-vous ! 8 déc.
“ Li ñuy woowe terrorisme, bare na tey. Loolu tax na ba ñu bare di laajte ndax tukki ci abiyoŋ wóor na. Ndax bokk nga ci ñi am xalaat boobu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi dafay won ne musiba mën na dal ñépp. [Jàngal Dajalekat 9:11.] Réveillez-vous ! bii dafay wone li ñu mën a def ba bu ñuy jël abiyoŋ, suñu tukki gën a wóor te gën a neex. ”