Liggéey bu am solo bu ñu war a def diggante 20 oktoobar ba 16 nowàmbar ngir joxe kayit bu ndaw bu bees.
1 Dalee ko altine 20 oktoobar ba mu mat ñeenti ayu-bés, dinañu joxe kayit bu ndaw bi tudd Ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo. Yàlla na liggéey boobu ñuy def ci kaw suuf si sépp, tax ba nit ñu gën a bare bëgg a xam téere bi yore dëgg gi. — Ywna. 17:17.
2 Kayit bi dafay tontu ci lu gàtt ci juróom-benni laaj yu am solo yii : “ Ndax Yàlla fonk na nit dëgg-dëgg ? ” “ Ndax geer ak naqar dina fi mas a jóge ? ” “ Lan mooy dal nit bu deewee ? ” “ Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ? ” “ Lan laa mën a def ba Yàlla nangu sama ñaan ? ” ak “ Lan laa mën a def ba am jàmm ci sama dund ? ” Diine yiy wuyoo turu karceen masuñu tontu lu leer ci laaj yooyu. Ñu bare ñu nekkul karceen sax, dañuy laaj seen bopp laaj yooyu. Waaye xamuñu ne Biibël bi wax na ci lu leer. Moo tax ñu yaakaar ne xibaar bii dina neex ñu bare.
3 Demleen fépp ci seen goxu mbooloo : Bu ngeen di waare këroo-kër, def leen lépp ngir dem ci kër yu gën a bare. Bu dee gox bi ngeen di waare dafa yaatu lool, njiit yi ci seen mbooloo dinañu leen wax ngeen bàyyi benn kayit ci kër yi ngeen fekkul kenn. Bu leen ci fàtte jox seeni dëkkandoo, seeni mbokk, ñi ngeen bokkal liggéey walla lekkool, ak ñeneen ñi ngeen faral di waxtaanal. Su mënee nekk, seetleen ni ngeen mënee def ngir nekk pioñee buy jàpple ci wéeru oktoobar ak nowàmbar. Ndax am nga doom walla kenn kooy jàngal Biibël bi, te muy jëm kanam bu baax ci wàllu ngëm ? Ndax mënul nekk waaraatekat bu ñu sóobagul ngir mën a bokk ci liggéey boobu ? Kon nanga ko yégal njiitu mbooloo mi.
4 Li ñu mën a wax : Bu ñu bëggee yégal xibaar bi nit ñu bare, li gën mooy ñu bañ a wax lu bare. Mën nga laaj nit ki rekk benn laaj ci juróom-benni laaj yi nekk ci xët bu njëkk bi, ba pare won ko tontu bi nekk ci kayit bi. Loolu dina tax waaraatekat yépp mën a seet li soxal nit ñi nekk ci seen gox, ngir waxtaan ci. Bu nit wonee ne suñu waxtaan neex na ko, nanga bind turam, ba pare dellu seeti ko. Bésu samdi ak dimaas, mën nañu wone yéenekaay yi ak kayit boobu. Ginnaaw bu liggéey bi jeexee ci bésu 16 nowàmbar, dinañu wone téere Qu’enseigne la Bible ? Bu amee lu des ci kayit yooyu, nañu ko jëfandikoo ni yeneen kayit yu ndaw yi ci waaraate bi.
5 Nañu komaase njàngum Biibël : Kayit bu ndaw bii, dañu ko defar ngir mën a komaase njàngum Biibël. Booy dellu seeti ku suñu waxtaan neex, mën nga ko laaj mu wax li yokk dooleem ci li mu jàng ci Biibël bi. Won ko xët bu mujj bi, fi ñu bind li mu mën a def ngir ñu jàngal ko Biibël bi, te jox ko téere Qu’enseigne la Bible ? Su mënee nekk, waxtaanleen ci benn walla ñaari xise ci pàcc biy wax ci waxtaan bi mu tànn.
6 Yexowa dafay wut ñi koy jaamu “ ci xel ak ci dëgg ” (Ywna. 4:23). Nañu bokk ñun ñépp ci liggéey bu am solo boobu ngir dimbali suñuy moroom ñu xam dëgg gi !