WOY-YÀLLA 84
Dinaa dem fi ñu ma soxla
(Macë 9:37, 38)
1. Yàlla xam na li gën ci man.
Li mu ma laaj, dinaa ko def.
Fum ma soxla, ma farlu ci.
Fas yéene naa dem ci ba jeex.
(AWU BI)
Dem ba jeex ci mbëggeel
te Yexowaa tax.
Ana fu am soxla? Waaw ma teew,
liggéeyal Yàlla!
2. Lu dëkk bi soree sore,
ma jàppale ña fa nekk,
ma dimbali ku ko soxla,
daldi wallu ku ne ci tiis.
(AWU BI)
Dem ba jeex ci mbëggeel
te Yexowaa tax.
Ana fu am soxla? Waaw ma teew,
liggéeyal Yàlla!
3. Ci sama gox, ak fu sore
damay tabax ay miir, ay taax.
Damay jàng làkku keneen
ngir xamal ko kuy Yexowa.
(AWU BI)
Dem ba jeex ci mbëggeel
te Yexowaa tax.
Ana fu am soxla? Waaw ma teew,
liggéeyal Yàlla!
(Xoolal itam Yowaan 4:35; Jëf ya 2:8; Room 10:14.)