WOY-YÀLLA 54
«Yoon waa ngii»
(Esayi 30:20, 21)
1. Yoon a ngi nii:
day indi jàmm ci biir xol.
Soo ko toppee,
am barke ci suñu Boroom.
Wër nga ba gis ko,
ba xam ngëneel yi ci ne.
Bul wàcc yoon woowu,
doo ko mas a rëccu.
(AWU BI)
Yoon waa ngi nii, yoon wi nga war a jaar.
Bul ko bàyyi, mooy yoonu dund gi.
Ngay dégg kàddu jibee ginnaaw.
Sa Boroom naan: «Yoon wii moo gën ci yow».
2. Yoon a ngi nii: yoonu mbëggeel
te neex a jaar.
Topp sàrtu Yàlla,
noonu nga ciy doxe.
Soo ko defee,
dinga yég mbëggeelu Yàlla.
Yal na yoonu mbëggeel
feeñ ci sa doxalin.
(AWU BI)
Yoon waa ngi nii, yoon wi nga war a jaar.
Bul ko bàyyi, mooy yoonu dund gi.
Ngay dégg kàddu jibee ginnaaw.
Sa Boroom naan: «Yoon wii moo gën ci yow».
3. Yoon a ngi nii:
di yoonu dund gu dul jeex.
Li mu lay may,
boo wutee feneen doo ko gis.
Ku fay jaar am ëllëgu
jàmm ak mbëggeel
bi Yexowa dige
te dara du ci deñ.
(AWU BI)
Yoon waa ngi nii, yoon wi nga war a jaar.
Bul ko bàyyi, mooy yoonu dund gi.
Ngay dégg kàddu jibee ginnaaw.
Sa Boroom naan: «Yoon wii moo gën ci yow».
(Xoolal itam Taalifi Cant 32:8; 139:24; Kàddu yu Xelu 6:23.)