WOY-YÀLLA 77
Leer feeñ na ci jamonoy lëndëm
(2 Korent 4:6)
1. Jamonoy lëndëm ji ñu nekk,
séen nañu leer guy feeñ.
Fajar ñëw, bët set, yaakaar am
indaale naataange.
(AWU BI)
Xibaar bi ñuy waare
mooy leeral àddina si,
maye yaakaar ak mbég.
Leeru jant buy fenk,
day indi bésu bànneex,
lëndëm ne mes.
2. Jamonoy yërmande jot na.
Yeen ñiy nelaw jógleen!
Ñoo ngi ñaan ngeen jot xibaar biy
neexal ëllëgu ñépp.
(AWU BI)
Xibaar bi ñuy waare
mooy leeral àddina si,
maye yaakaar ak mbég.
Leeru jant buy fenk,
day indi bésu bànneex,
lëndëm ne mes.
(Xoolal itam Yowaan 3:19; 8:12; Room 13:11, 12; 1 Piyeer 2:9.)