Woy-Yàlla 83 (187)
Beesal nañu lépp
(Peeñu bi 21:4)
1. Firndey jamanoo ngiy wone, te leer na,
Ne Yeesu jot na Nguur, gi mu donn.
Xare na ca asamaan te daan na.
Léegi li soob Yaa am ci àddina.
(AWU)
Bégleen! Tàntub Yàllaa ngeek ñun,
Moom ci boppam dëkk ak ñun.
Dootu fi am coono, jooy, naqar,
Moo xam tiis, walla dee ndax bàkkaar;
‘Maa ngiy beesal lépp,’ la Yàlla wax.
Lu wér la, lu wóor te sax.
2. Sas! Yérusalem bu bees baa ngiy agsi,
Jabaru Mbote maa ngiy nes-nesi.
Daa sol takkaay yi dàq ci suuf si;
Yàlla doŋ’ mooy leeru séet, biy séysi.
(Awu)
3. Nit ñi ci dëkk bii bànneex dinañ’ am;
Guddeek bëccëg duñu tëj ay buntam.
Xeet yép’ dinañ’ dox ci leeru ndamam.
Jaamiy Yaa, awuleen tey jii leeram.
(Awu)