TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 10 p. 13
  • Ni ngay soppee sa baat booy jàngale

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ni ngay soppee sa baat booy jàngale
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Waxal ak cawarte
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Woneel ne gëm nga li ngay wax
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Waxal mel ni kuy waxtaan
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 10 p. 13

LESOŊ 10

Ni ngay soppee sa baat booy jàngale

Aaya bi ñu lim

Kàddu yu Xelu 8:4, 7

LI NGA WAR A JÀPP: Na sa wax leer te laal xolu nit ñi. Li la ciy dimbali mooy di soppi sa baat booy wax.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Yëkkëtil sa baat walla nga wàcce ko. Yëkkëtil sa baat booy wax li gën a am solo ak booy xiir nit ñi ci def dara. Defal noonu itam booy jàng aaya buy wax ci àtte Yàlla yi. Wàcceel sa baat boo bëggee ñi lay déglu yàkkamtee xam li nga nar a wax, walla boo bëggee wone ragal mbaa njàqare.

    Xelal bu baax

    Bul faral di wax ak baat bu kawe ba ñi lay déglu foog ne danga leen di xas. Booy wax, bul ëppal itam ngir bañ a nekk kuy wone boppam.

  • Waxal ak baat bu xumb walla bu lewet. Su mënee nekk ci sa làkk, waxal ak baat bu xumb ngir wone cawarte, yaatuwaay walla sorewaay. Waxal ak baat bu lewet ngir wone naqar walla njàqare.

  • Waxal mu gaaw walla mu yéex. Waxal mu gaaw ngir wone yëg-yëg bu am doole. Waxal mu yéex booy wax ci li gën a am solo.

    Xelal bu baax

    Bul bett ñi lay déglu, maanaam nga jékki-jékki rekk wax mu gaaw walla mu yéex. Bu sa wax gaaw torop ba duñu mën a xam li ngay wax.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager