TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 15 p. 18
  • Woneel ne gëm nga li ngay wax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Woneel ne gëm nga li ngay wax
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Waxal ak cawarte
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Waxal mel ni kuy waxtaan
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal waxtaan buy yokk xam-xam
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 15 p. 18

LESOŊ 15

Woneel ne gëm nga li ngay wax

Aaya bi ñu lim

1 Tesalonig 1:5

LI NGA WAR A JÀPP: Woneel ne gëm nga bu baax ne li ngay wax dëgg la te am na solo.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Waajalal sa bopp bu baax. Xoolal bu baax li nga nar a waxtaane te mu jóge ci Biibel bi. Seetal li tax li ñu ci wax leer ba nit mën koo gëm. Jéemal a wax ponk yi gën a am solo ci kàddu yu gàtt te yomb a xam. Xalaatal bu baax ci njariñ bi li ngay wax mën a amal ñi lay déglu. Ñaanal Yàlla mu may la xel mu sell mi.

    Xelal bu baax

    Bala ngay def sa waxtaan, wax ko ci kaw ay yooni yoon ba mokkal ko.

  • Waxal ay baat yuy wone ne gëm nga li ngay wax. Bul yem rekk ci jàng li ñu bind, waaye wax ko ak say kàddu bopp. Woneel ci say kàddu ne li ngay wax, wóor na la.

  • Ni ngay waxe, na wone ne ku dëggu nga. Waxal bu baax ba ñépp mën laa dégg. Nanga xool ñi lay déglu, waaye na ànd ak yar.

    Xelal bu baax

    Gëm li ngay wax warul a tax ngay wax wax juy merloo walla metti nit ñi, walla di wone ne yow rekk yaa am dëgg, walla di bëgg a forse nit ñi ñu gëm li ngay wax. Dëgg la, gëm nga li ngay wax, waaye waxal ak mbaax.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager