Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 févr.
“ Ndax mas nga laaj sa bopp noo mënee xam ni nga war a doxale sa àddina ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu sell mi dafa ñuy won ni nu war a doxale suñu dund. Li muy wax bokk na ci li gën ci doom-Aadama. Seetal li nekk ci ndigal bu ñuy woowe ndigal bi mel ni wurus. [Jàngal Macë 7:12.] Ginnaaw ndigal boobu, lan moo ñu mën a jariñ ci Mbind mu sell mi ? Tont baa ngi ci téere bii. ”
Réveillez-vous ! 22 févr.
“ Ndax seetlu nga ne liggéey yu bare, wóoratuñu ni bu njëkk ? Téere bii dafay wone naka lañu mënee def ba suñu liggéey gën a wóor. Dafay wone itam ne bu ñu bëggee suñu dund neex, dañu war a xam ni ñu war a gise suñu liggéey. Ndax bëgg nga ko jàng ? ”
La Tour de Garde 1er mars
“ Ak lépp li ñuy gis tey, ñu bare ñu ngi laaj seen bopp naka la ëllëg di mel. Isaa Almasi bi ñaan na ñaan boo xam ne, ñu bare xam nañu ko. Ci ñaan boobu wone na lu tax mën nañu wóor ne, ëllëg dina neex. [Jàngal Macë 6:9, 10.] Lu bon li nit ñi defoon bu yàgg, loolu la nit ñi di defaat tey. Waaye ci jamano jooju, ñi doon jaamu Yàlla, seen ëllëg neexoon na. Téere bii dafay wone ni ñu mëne am ñun itam ëllëg bu neex. ”
Réveillez-vous ! 8 mars
“ Mbind mu sell mi dafay wone njariñu yar bu baax. [Jàngal Léeb. 2:10, 11.] Ñu bare gis nañu ne, am jàngalekat bu baax, lu am solo la ci xale. Reveillez-vous ! dafay wone ne li jàngalekat yi di def, am na solo lool. Dafay wone itam naka lañu waree fonk lépp li ñuy def, te naka la leen way-jur yi waree dimbali ci seen liggéey bu jafe bi. ”