Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er juillet
“ Ndax jéem a am li nit soxla dëgg ngir dund, mën na tax ñu def lu neexul Yàlla ? [Mayal nit ki mu tontu te jàngal Macë 24:37-39.] Seet li Yàlla bëgg bala ñuy jàpp li ñuy def, lu baax la. Xaaju téere bii dafay wone lu tax loolu baax. ” Wonal nit ki waxtaan biy komaase ci xët 11.
Réveillez-vous ! Juillet
“ Ñu bare tey liy seen njariñu bopp kese moo leen di tax a dugg ci séy. Ndax foog nga ne jikko bu mel noonu mën na neexal séy ? [Mayal nit ki mu tontu te jàngal Filib 2:4.] Téere bii dafay wone li Biibël bi wax ngir dimbali nit mu am séy bu neex te dëgër. ”
La Tour de Garde 1er août
“ Poroblem yu réy yu jëm ci géej gi, suuf si ak lépp li ñu wër tax na ba ñu bare amatuñu yaakaar ci ëllëgu suuf si. Yow nag, noo gisee mbir mi ? [Mayal nit ki mu tontu te jàngal Sabóor 37:11.] Téere bi dafa ñuy won ci Biibël bi lu war a tax ñu am yaakaaru ëllëg. ”
Réveillez-vous ! Août
“ Ñu bare dañuy wax ne tàngoor bi am ci suuf si sépp, mën na tax ba kenn dootul mën a dund ci kow suuf. Ci yow naka lañu mënee faj poroblem boobu ? [Mayal nit ki mu tontu te jàngal Esayi 11:9.] Téere bii dafay wax lu tax mu mën ñu wóor ne nit dina kontine di dëkk ci kow suuf si. ”