Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 1er août
“ Ndax nangu nga ne, bu ñu toppee li Yeesu wax fii, jàmm dina gën a bare ci njaboot yi ? [Jàngal Yowaana 13:34 te may nit ki mu tontu.] Waxtaan bii, dafay wone naka la kenn ku nekk ci njaboot bi mënee topp li Yeesu jàngale te roy it ci moom. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 16 ak 17.
Réveillez-vous ! Août
“ Ndax yaakaar nga ne Nguuri doomu Aadama yi, dinañu mën a faj poroblemu tàngoor bi am ci kow suuf si ? [Mayal nit ki mu tontu te jàng Jérémie 10:23.] Waxtaan bii dina la neex. Dafay wone ni Yàlla di faje poroblem yi bëgg yàq suuf si. ”
La Tour de Garde 1er sept.
“ Nit ñu bare xam nañu bu baax kàddu Yeesu yi nekk ci Macë 6:9. [Jàng ko.] Waaye ñu bare dañuy wax ne, jege Yàlla ni nit mënee jege baayam, lu jafe la. Ci sa xalaat, naka lañu mënee jege Yàlla ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bii dafay wax ci jikko suñu Baay bi nekk ci asamaan. Dafay wone it naka lañu ko mënee xam dëgg. ”
Réveillez-vous ! Sept.
“ Ay téemeeri at a ngii, nit ñi di werante ci lu jëm ci dund ginnaaw dee. Lan moo ci sa xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Seetal li Ayóoba wax fii. [Jàngal Job 14:14, 15.] Waxtaan yii dañuy wone li Biibël bi wax ci dund ginnaaw dee. ”