NJÀNGALE 8
Lu tax ñuy solu ba jekk bu ñuy dem ci suñu ndaje yi ?
Islande
Mexique
Guinée-Bissao
Philippines
Ndax seetlu nga ci foto yi nekk ci téere bii ni seede Yexowa yi di soloo ba jekk bu ñuy dem ci seeni ndaje ? Lu tax colin bu jekk am solo ci ñun ?
Dafay wone ne dañu may cër Yàlla. Dëgg la, Yàlla buy xool nit du yem ci melokaanam (1 Samwil 16:7). Waaye bëgg nañu bu ñuy booloo ngir jaamu ko, ñu may ko cër, may it cër ñi ñuy dajeel. Dafa mel ni tey, nga war a taxaw ci kanamu buur walla peresidaa. Li wóor mooy, dinga xool bu baax ni ngay soloo ndax li mu doon kilifa. Noonu it ñun, ni ñuy soloo bu ñuy dem ci ndaje yi, dafay wone ne may nañu cër Yexowa Yàlla miy “ Buur bi fiy sax ba abadan ” te fonk béréb bi ñu koy jaamoo. —1 Timote 1:17.
Dafay wone ne li ñuy jàng ci Biibël bi mu ngi feeñ ci ñun. Ci Biibël bi, Yàlla dafa wax karceen yi ñuy solu “ cig woyof ak maandu ” (1 Timote 2:9, 10). Solu “ cig woyof ” mooy bàyyi bépp fasoŋu solu buy tax ñépp di la xool ndax colin bu ñàkk yiw te di wone awra. Ku “ maandu ” nag dina xam ni muy tànnee yére yi muy sol. Du tànn lu jagul walla lu doy waar ba ëpp. Li Biibël bi wax noonu terewul ñu am lu bare lu ñu mën a sol. Bu ñuy solu ba jekk, loolu mën na “ rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat ” te “ màggal ” ko (Tit 2:10 ; 1 Piyeer 2:12). Bu ñuy solu ba jekk bu ñuy dem ci suñuy ndaje, dañuy tax nit ñi xalaat lu rafet ci ni ñuy jaamoo Yexowa.
Bul bàyyi yére yi nga sol tere la teewe suñuy ndaje. Li ñuy sol, soxlawul mu doon lu réy walla lu seer. Na nekk lu set te jekk.
Lu tax suñu colin am solo bu ñuy jaamu Yàlla ?
Yan santaane Yàlla ñoo ñu mën a dimbali ci xam ni ñu war a soloo ?