TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 3 p. 6
  • Booleel ay laaj ci sa njàngale

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Booleel ay laaj ci sa njàngale
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Li ngay njëkk a wax
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 3 p. 6

LESOŊ 3

Booleel ay laaj ci sa njàngale

Aaya bi ñu lim

Macë 16:13-16

LI NGA WAR A JÀPP: Laajal nit ñi ay laaj yuy tax ñu bëgg a déglu li ngay wax, ñu xalaat ci te gis bu baax ponk yi gën a am solo.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Fexeel ba nit ñi bëgg a déglu li ngay wax. Laajal ay laaj yuy tax nit ñi jéem a tontu ci seen xel walla ñu yàkkamtee xam tont bi.

  • Dimbali leen ñu xalaat ci li ngay wax. Laajal ñi lay déglu ay laaj yuy tax ñu xam fi dëgg gi féete.

  • Na ponk yi gën a am solo feeñ bu baax. Boo bëggee jàngal nit ponk bu am solo, laajal laaj buy tax mu bëgg cee xam dara. Boo waxee ci ponk bu am solo walla booy jeexal waxtaan bi, laajal ay laaj ngir fàttali li gën a am solo.

    Xelal bu baax

    Boo jàngee aaya ba pare, mën nga laaj ay laaj ngir wone bu baax xalaat bi ci gën a am solo.

CI LIGGÉEYU WAARE BI:

Laajal ki lay déglu xalaatam. Déglul bu baax li muy tontu. Booy laaj dara, xamal kañ ak naka nga ko war a defe.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager