TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 4 p. 7
  • Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Woneel bu baax njariñu aaya yi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Li ngay njëkk a wax
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal waxtaan buy yokk xam-xam
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 4 p. 7

LESOŊ 4

Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya

Aaya bi ñu lim

Macë 22:41-45

LI NGA WAR A JÀPP: Bala ngay jàng aaya, waxal nit ñi luy tax ñu bëgg a xam li aaya boobu wax.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xalaatal ci li tax nga nar a jàng aaya. Li ngay wax bala ngay jàng aaya, war na tax ñi lay déglu bàyyi xel ci ponk bu am solo bi nga leen bëgg a jàngal.

    Xelal bu baax

    Xoolal aaya yi jiitu aaya bi nga bëgg a jàng ak yi topp ci moom. Booy joxe turu kiy wax ci aaya bi walla turu ki bind téere bi ci Biibël bi, bu ci juum.

  • Woneel ne Biibël bi mooy wax. Booy wax ak nit ñu gëm ne Yàlla am na, won leen ne ndegam Biibël bi mooy Kàddu Yàlla, kon foofu lañu mën a jële xelal yi gën.

  • Fexeel ba nit ñi bëgg a xam li aaya bi wax. Laajal benn laaj bu aaya bi di tontu, walla nga wax ci benn porobalem boo xam ne aaya bi mën na leen a dimbali ñu regle ko. Mën nga wax it ci li ñu mën a jànge ci lu Biibël bi nettali.

    Xelal bu baax

    Sóoraaleel li nit ñi jot a xam ci li nga bëgg a waxtaane ak it ci aaya bi nga bëgg a jàng. Boo naree jàng sax aaya bu nit ñi xam bu baax, fexeel ba ñu bëgg laa déglu te nga dimbali leen ñu mën cee jànge lu bees.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager