LESOŊ 18
Defal waxtaan buy yokk xam-xam
1 Korent 9:19-23
LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat bu baax ci li ngay wax. Noonu, bu waxtaan bi jeexee dinañu xam ne jàng nañu lu am njariñ.
NI NGA KO MËN A DEFE:
Xalaatal ci li nit ñi xam ba pare. Bul waxaat rekk li nit ñi xam ba pare, waaye dimbali leen ñu jàng ci waxtaan bi lu bees.
Gëstul te xalaat bu baax ci li nga nar a waxtaane. Bu mënee nekk, waxal ci xew-xew yu ñu bare yëgul walla yu xew tey ngir leeral ponk yi gën a am solo. Te it, seetal bu baax ni loolu ànde ak li nga bëgg a waxtaane.
Woneel njariñ bi sa waxtaan mën a amal ñi lay déglu. Woneel njariñ bi nekk ci topp bés bu nekk li Biibël bi wax. Woneel njariñ boobu ci ay fànn, doxalin walla jëf yu nit ñi xam.