TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 6 p. 9
  • Woneel bu baax njariñu aaya yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Woneel bu baax njariñu aaya yi
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal waxtaan buy yokk xam-xam
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 6 p. 9

LESOŊ 6

Woneel bu baax njariñu aaya yi

Aaya bi ñu lim

Yowaana 10:33-36

Li NGA WAR A JÀPP: Bul yem rekk ci jàng benn aaya ba pare jàll ci leneen. Fexeel ba ñi lay déglu xam bu baax ni aaya bi nga jàng ànde ak li ngay wax.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Woneel bu baax baat yi gën a am solo. Boo jàngee benn aaya ba pare, woneel bu baax baat yiy wone ponk bi nga bëgg a jàngale. Ni nga ko mën a defe mooy nga waxaat baat yooyu walla nga laaj ñi lay déglu laaj buy tax ñu jàpp baat yooyu.

    Xelal bu baax

    Su dee sax danga bëgg a waxaat li aaya bi wax ak yeneen baat yu wuute, fexeel ba ñi lay déglu gis bu baax ne ponk bi nga bëgg a jàngale mu ngi jóge ci baat yi nekk ci aaya bi.

  • Feeñalal bu baax ponk bi nga bëgg a jàngale. Boo waxee li tax nga bëgg a jàng benn aaya, boo ko jàngee ba pare, leeralal ni baat yi gën a am solo ci aaya boobu wonee li tax nga jàng ko.

    Xelal bu baax

    Booy leeral aaya boo jàng ba pare, bul tëj sa Biibël. Loolu dina tax ñi lay déglu gis ne li ngay wax mu ngi jóge ci aaya bi nga jàng.

  • Woneel ci lu leer njariñu aaya bi. Moytul a wax ci ay ponk yuy tax li gën a am solo du leer. Jaaral ci li nit ñi xam ba pare ci waxtaan bi ngir seet li nga mën a wax ba njariñu aaya bi leer bu baax ci seen xel.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager