TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 7 p. 10
  • Waxal lu wóor lu nit mën a gëm

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Waxal lu wóor lu nit mën a gëm
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Booleel ay laaj ci sa njàngale
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 7 p. 10

LESOŊ 7

Waxal lu wóor lu nit mën a gëm

Aaya bi ñu lim

Luug 1:3

LI NGA WAR A JÀPP: Booy wax sukkandikul ci lu wóor ngir dimbali ñi lay déglu ñu xam fi dëgg gi féete.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Li ngay wax, na jóge fu wóor. Li ngay wax, na jóge ci Kàddu Yàlla, te saa yu mënee nekk jàngal aaya yi koy dëggal. Bala ngay wax ci li tubaab di woowe science, ci xibaar boo dégg, walla ci lu nit dund, walla ci leneen luy dëggal say kàddu, seetal ndax fi nga sukkandiku wóor na te li ñu ci wax mooy dëgg ba tey.

  • Li ngay wax, na ànd ak li nekk fi nga ko jële. Booy wax ci benn aaya, na ànd ak aaya yi ko jiitu ak yi ko topp, ànd ak lépp li Biibël bi wax, ànd it ak li nekk ci téere yi «surga bu takku te teey» bind (Macë 24:45). Su dee li ngay wax, ci beneen téere la jóge walla ci rajo walla internet, na dëppoo ak li taxoon ñu bind ko walla ñu wax ko.

    Xelal bu baax

    Bul yokk wax ji. Bu ñu waxee «ay nit» bul ne «nit ñu baree-bare», walla ñu ne «lée-lée» nga ne «saa su ne», walla ñu ne «xëy-na» yow nga ne «ci lu wóor».

  • Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat bu baax ci li ngay wax. Boo jàngee aaya ci Biibël bi walla nga jàng dara ci beneen téere ba pare, laajal ci fasoŋ bu rafet ay laaj mbaa nga misaal li ngay wax, ba ñi lay déglu xam ndax mën nañu ko gëm walla déet.

CI LIGGÉEYU WAARE BI:

Booy waajal sa bopp ngir dem waare, xalaatal ci li nit ñi mën a laaj te nga jéem cee tontu. Bu ñu la laajee loo xamul, waxal ne dinga dellusi ngir tontu ci.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager