‘Nañu jaamu Yàlla ci xel ak ci dëgg’
YOWAAN 4:24
Suba si
9:40 Misik
9:50 Woy-Yàlla 85 ak ñaan
10:00 ‘Ñu ni mel la Baay bi di wut’
10:15 Waxtaan bu def ay xaaj: ‘Nañu jaamu Yàlla ci xel’
• Bu ñu bëggee nànd tegtal yi jóge ci Yexowa
• Bu ñu xàddee
• Bu ñu bëggee yokk li ñuy def ci liggéeyu Yexowa
11:05 Woy-Yàlla 88 ak yégle yi
11:15 ‘Ni ñuy fésale dëgg gi’
11:35 Sóob bi: Li seen sóob ci ndox di tekki
12:05 Woy-Yàlla 51
Ngoon gi
1:20 Misik
1:30 Woy-Yàlla 72 ak ñaan
1:35 Waxtaan bi ñu jagleel ñépp: Naka lañu mënee ràññee li baax ak li bon?
2:05 Njàngum La Tour de Garde bu ñu gàttal
2:35 Woy-Yàlla 56 ak yégle yi
2:45 Waxtaan bu def ay xaaj: ‘Nañu jaamu Yàlla . . . ci dëgg’
• Ci biir njaboot gi
• Ci àddina su xàjjaloo
• Bu ñu amee jafe-jafe ci wàllu koom-koom
3:30 ‘Jëndal dëgg gi te bu ko jaay’
4:00 Woy-Yàlla 29 ak ñaan