Ndax yaa ngiy matal bu baax a baax li ñu la sas ?
1 Ci biir téere Jëf ya, ñu ngi ñuy wax ne, taalibe Yeesu yaa nga doon matal liggéey bi ñu leen sasoon, ba ñu doon “ seede [nit ñi] bu baax a baax ” lu jëm ci Nguuru Yàlla (Jëf. 2:40 ; 8:25 ; 28:23, NW). Te dëgg-dëgg, loolu mooy li ndaw li Pool jublu woon (Jëf. 20:24). Ndax du loolu itam ngay wut, yaw mi nekk ndawu xabaar bu baax bi ? Waaye nan nga ko mënee def ?
2 Waajalal li ngay wax : Ngir mu wóor ne sa seede dina am doole booy dem waare, lu am solo la, nga waajal ko bu baax. Rawatina nag booy wone suñu yéenekaay yi faral di génn, ñu fay waxtaane saa su ne yëf yu wuute. Ngir gën ñoo dimbali ci loolu, Sasu Nguuru Yàlla bii ñu yor a ngiy ubbi bunt bu bees — wërale gi féete ci càmmooñ, ñu bind fa nag li ñu mën a wax ngir wone suñu yéenekaay La Tour de Garde ak Réveillez-vous !, yi soog a génn. Ci bu nekk ci yéenekaay yooyu, dinañu fésal ponk bu agsi ci waxtoom, buy itteel nit ñu bare. Nan ngay mën a jëfandikoo waxtaan yu gàtt yooyu ?
3 Tànnal benn ci xelal yooyu, maanaam bi nga xalaat ne daal, mooy ëpp doole ci béréb bi ngay waare. Jàngal bu baax wërale gi féete ci càmmooñ ; boo noppee, jàppal ponk yi mën a itteel nit ñi. Seetal ci biir yéenekaay bi aaya ju ñu lim, ju lëkkalook li ngay waxtaane, aaya jooy mën a jàngal nit ki. Sottalal ci lu gàtt sa waxtaan ngir xiir ki lay déglu ci jàng yéenekaay bi ; bu loolu weesoo, xamal ko ci lu gàtt ne, mën naa def maye ngir jàpple liggéey bi Seede Yexowa yi di amal ci àddina si sépp — su fekkee ne ci anam yi nga ne, rafet na nga xamal ko ko. Léegi, baamtul li nga nar a wax.
4 Xalaatal a jëfandikoo Biibël bi : Soo waajalee sa bopp bu baax, du ñàkk dinga mën a sóoraale aaya ci sa waxtaan. Li koy misaal mooy, ci béréb yu bare, waarekat yu aay a ngiy àntu bu ñuy dem ci bunt yi, yore seen Biibël ci loxo te naan, gannaaw bu ñu nuyoo :
◼ “ Dañuy laaj nit ñi ndax gëm nañu li ñu wax fii... ” Jàngal 1 Musaa 1:1, ba noppi laajte lii : “ Ndax ànd ngaak li ñu fi wax ? ” Su la nit ki nee, ànd na ci, bu boobaa nee ko : “ Man tamit. Waaye ci sa gis-gis, ndegam Yàlla moo sàkk lépp, ndax moom itam moo war a gàddu lu bon lépp li am ? ” Boo dégloo tontam ba noppi, jàngal Dajalekat 7:29. Ubbil téere bi tudd Xam-xam, àggal ci xët 71, ba noppi jàngal ko xise 2. Xiirtalal nit ki ci jàng téere bi. Léegi, su fekkee ne ki ngay waxal àndul ci li ñu wax ci 1 Musaa 1:1, xiirtal ko bu baax ci seet li nekk ci biir téere bi tudd Création.
5 Seetiwaatal képp ku wone itte : Mënuloo matal sa sas, dem ci ba jeex, soo seetiwaatul nit ki wone itte ci li nga ko wax. Gannaaw waxtaan wu neex woo am ak moom, moo xam danga ko bàyyil suñu yéenekaay yi mbaa meneen ci suñu mbind yi, bindal turam ak fa mu dëkk. Ak cawarte, jéemal a suuxat itteem, ci li nga fay gaaw a dellu. Ak lu mu mën a doon, xamal ko ne mën naa am njàngum Biibël bi.
6 Ca xarnu bu njëkk ba, taalibe yi xamoon nañu ne, Yeesu da leen digaloon ñu “ seede bu baax a baax ” (Jëf. 10:42, NW). Ndigal loolu, benn la ba tey ngir ñun, ndax noonu doŋŋ lañuy mënee sàkk ay taalibe (Macë 28:19, 20). Nañu def, kon, suñu kem-kàttan ngir matal liggéey biñ ñu sas bu baax a baax. — 2 Tim. 4:5.