Ni ñu waree topp li ñu bind ngir wone li ñu mën a wax ci waaraate bi
1 Ci Sasu Nguuru Yàlla yi, dañu faral di bind li ñu mën a wax bu ñuy wone suñuy téere walla suñuy yéenekaay. Nekkul ne li ñu bind rekk lañu mën a wax. Dañu fa bëgg wone rekk ci lan lañu mën a waxtaan. Waaye, ci lu ëpp, bu ñu ko waxee ci suñu kàddu bopp, dina gën a baax. Waxtaan lay doon. Ki ñuy déglu dina gën a féex. Te dina xam ne li ñuy wax, ci suñu xol la jóge te dañu ko gëm.— 2 Kor. 2: 17 ; 1 Tes. 1:5.
2 Seetal ci ki ngay waxal ngir xam li nga koy wax : Fu ñuy waare, nit ñi am nañu aada yu ñuy topp. Dañu war a seet ci aada yooyu ngir xam ni ñuy waaree. Ndax fi ngay waare, bala ngay waxtaan ak nit danga ko war a nuyu bu baax ? Walla ndax danga war a gaaw a wax li la tax a jóg ? Loolu dafay aju ci fi ngay waare ak yenn saay sax ci nit ki ci boppam. War nga xam itam li nga mën a laaj nit ki. Li nga mën a laaj fi nga nekk, xéyna doo ko mën a laaj feneen. Kon, dañu war a seet bu baax li ñu mën a wax ak li ñu warul a wax fi ñuy waare.
3 Bu ñuy waajal waaraate bi, war nañu seet itam ci ni nit ñi yaroo ak ci li nekk ci seen xel. Seete ko ci ñaan bi nekk ci Macë 6: 9, 10. Boo ciy waxtaan ak katolik bu gëm lool, li ngay wax du mel ni booy wax ak ku xamul ñaan boobu. Kon, bala ñuy dem waaraate, nañu xalaat tuuti ci li ñu bëgg wax. Dina tax li ñuy wax ci waaraate bi gën a neex nit ñi. — 1 Kor. 9:20-23.
4 Waajal bu baax suñu waaraate bi, dara gënu ko. Bu dee sax dañu bëgg topp li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi, fàww ñu waajal bu baax suñu waare. Dañu war a jàng bu baax li ñu bëgg won nit ki te seet ay ponk yu ko mën a itteel. Ba pare boole ko ci li ñu bëgg wax bu ñuy wone suñuy téere ci waaraate bi. Xam bu baax li nekk ci suñuy téere, dina tax ñu gën leen bëgg won nit ñi. Bu ñu xamul li nekk ci suñuy téere, duñu sawar bu ñu leen di wone.
5 Leneen lu ñu mën a wax : Ndax li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi rekk lañu mën a wax bu ñuy wone suñu téere yi ? Déedéet. Xéyna danga gis ne wax leneen walla jaar ci beneen aaya moo gën a yomb ci yow. Kon, defal noonu, rawatina bu dee suñu yéenekaay yi ngay wone. Am na waxtaan bu nekk ci xët bu njëkk bi. Waaye boo gisee ci biir yéenekaay bi beneen waxtaan bu gën a mën a itteel nit ñi, nanga ko wone. Te itam, ci ndaje yi jëm ci liggéeyu waare bi, bu ñuy wone li ñu mën a wax ci waaraate bi, na nekk li mën a baax ci fi ñuy waare. Waaraatekat yi dinañu gën a mën a waare xibaar bu baax bi.
[Laaj yi]
1. Naka lañu war a gise li ñu bind ngir wone li ñu mën a wax ci waaraate bi ?
2. Bu ñuy waajal waaraate bi, lu tax ñu war a xalaat ci aada yi nit ñi di topp fi ñuy waare ?
3. Lu tax ñu war a xalaat fu nit ñi yaroo ak li nekk ci seen xel ?
4. Lu tax waajal bu baax waaraate bi am solo lool ?
5. Bu ñuy waajal waaraate bi, lu mën a tax yenn saay ñu bañ a topp li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi ? Kon, naka lañu mënee waajal beneen waxtaan ?