Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 okt.
“ Taxawal àddina su gën te ëpp bànneex, lu muy laaj ? [Mayal nit ki mu tontu.] Nit ñi jéem nañu nguur yu dul jéex ngir taneel yëf yi. Waaye seetal li ci Yàlla xalaat. [Jàngal Yérémi 10:23.] Fii ci yéenekaay bii dañuy wone luy ‘ Caabi àddina su bare bànneex ’, te dañuy wone naka la loolu di ame léegi. ”
Réveillez-vous ! 22 okt.
“ Ndax nangu nga ne jafe-jafe yi masuñu metti ni tey ? [Mayal nit ki mu tontu.] Loolu, Mbind mu sell mi waxoon na ko bala muy am. [Jàngal 2 Timote 3:1.] Ci nit ñu bare, dund gi dafa jafe ba nga xam ne dootuñu jéem dara ci seen dund. Yéenekaay bii dafa ñuy xiirtal bu baax. Dafay wone ni ñu mënee xeex liy tax ñu bañ a amati benn yaakaar te fexe ba am dund gu jar a dund. ”
La Tour de Garde 1 now.
Boo waxee ba noppi lu doy waar lu xew bu yàggul, laajteel lii : “ Lu tax nit ñi di def lu soxor lu mel nii ? Ñun ñépp a war a mën a ràññe li baax ak li bon, waaye nit ñi dañuy dëkk ci lu bon. Lu waral loolu ? [Bu la tontoo ba noppi, jàngal Peeñu bi 12:9.] Yéenekaay bii dafay wone ni ñu mënee aar suñu bopp, bu ñuy sàmm suñu xel. ”
Réveillez-vous ! 8 now.
“ Tey, nit ñi dañu ñeme jëfi fitna, du noonu ? [Bu la tontoo ba noppi, jàngal 2 Timote 3:3.] Ci biir njaboot yi sax, bare na li nit ñi di def lu soxor a soxor. Ci yéenekaay bii, xaaj bi tudd : ‘ Ndimbal ngir jigéen yi ñuy dóor ’, dafa ñuy indil xibaaru yaakaar. Mën na am nga xam koo ko mën a won. ”