Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 oct.
“ Nit ñu bare, tey rekk lañuy toppatoo ndaxte dañuy naan kenn xamul liy am ëllëg. Loo ci xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu]. Am na lu am solo lu Yeesu waxoon. [Jàngal Macë 6:34.] Naka lañu mënee waajal suñu ëllëg te bañ koo ragal torop ? Ci loolu la téere bii di waxtaan. ”
Réveillez-vous ! Oct.
“ Ñun ñépp am nañu mbokk walla xarit bu gaañu. Ndax foog nga ne nit ñooñu ñu ngi ca asamaan di ñu xool ? [May ko mu tontu.] Xoolal li Yeesu waxoon bi Lasaar deewee. [Jàngal Yowaana 11:11.] Ñi dee, ndax ñu ngi dund feneen walla ndax ñu ngi nelaw rekk di xaar ba ñu dekkal leen ? Ci loolu la téere bii di wax. ” Won ko waxtaan biy komaase ci xët 28.
La Tour de Garde 1er nov.
Bu nit ñuy suufeelu gënoon a bare tey, ndax àddina bi du gën a neex ? [May ko mu tontu.] Xoolal li Yeesu wax ci nit kuy suufeelu. [Jàngal Macë 23:12.] Ci àddina bii, rawante rekk a fi am. Waaye téere bii dafay wone lu tax suufeelu am njariñ lool. ”
Réveillez-vous ! Nov.
“ Ñu bare tey, dañu foog ne li nekk ci Biibël bi amalu leen njariñ. Ñeneen ñi ñoom, xamuñu ndax mën nañu wóolu li ci nekk ngir mu won leen li ñu war a def. Yow ci sa wàllu bopp noo gisee Biibël bi ? [May ko mu tontu ba pare jàngal 2 Timote 3:16.] Reveillez-vous ! bu am solo bii, dafay wone lu tax mu mën ñu wóor ne Biibël bi, ci Yàlla la jóge. ”