Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 oct.
“ Bu la xale walla keneen laajee lu tax lu bon bare nii tey, loo koy wax ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi dafay wax kan moo jiite lu bon li. [Jàngal 1 Yowanna 5:19.] La Tour de Garde bii dafay wone kan mooy ku bon kooku, te naka lañu ko mënee xeex. ”
Réveillez-vous ! 22 oct.
“ Ndax foog nga ne ñaanu kilifa diine yi, walla ñaanu keneen mën na tax jàmm am ci àddina ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi wax na ne dina am jamano joo xam ne jàmm dina am ci àddina si sépp. [Jàngal Isayi 9:6, 7.] Ndax seetlu nga ne am na benn buur bu war a indi jàmm ci àddina si sépp ? Réveillez-vous ! bii dafay wone kan mooy buur boobu te naka lay inde jàmm jooju. ”
La Tour de Garde 1er nov.
“ Ñu bare dañuy góor-góorlu ngir am jàmm ak seeni moroom. Waaye loolu yombul, du dëgg ? [Mayal nit ki mu tontu.] Biibël bi dafay wone lu waral loolu. [Jàngal Saak 3:2.] Yéenekaay bii dafay wone ne baalu àq mën na indiwaat jàmm te saxal ko. ”
Réveillez-vous ! 8 nov.
“ Biibël bi wone na ne dina am jamano joo xam ne kenn dootul waxati : ‘ Dama feebar. ’ [Jàngal Isayi 33:24] Loolu dina neex de. [Mayal nit ki mu tontu.] Waaye tey, nit ñi sonn nañu lool ndax feebar yu dul jeex yu mel ni SIDA. Réveillez-vous ! bii dafay tontu ci laaj bii : SIDA ndax dina fi mas a deñ ? ”