Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 oct.
“ Ñu bare dañu foog ne bala sa àddina neex, fàww sa njàng sore. Waaye ci sa xalaat, ban njàng moo mën a tax nit gën a baax, te mën a won nit li mu war a def bu amee poroblem ? [Mayal nit ki tontu, ba pare jàngal Room 12:2. Won ko ne ‘ yeeslu ci sa xel ’ bi ñu wax foofu, mooy bàyyi li ngay jàng soppi fi ngay def sa xel ci sa àddina. Loolu dinga ko mën a def boo feesalee sa xel ak li ngay jàng ci Kàddu Yàlla, maanaam li Yàlla bëgg ak li mu santaane.] Téere bii dafay wax ci njàngale bi gën bi nga mën a am ak njariñ bi ci nekk. ”
Réveillez-vous ! 22 oct.
“ Nit ñu bare dañu faral di jàng kayitu xibaar yi bés bu nekk. Ndax mën nañu gëm lépp li ñu ciy wax ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dina la wax ni nga mënee jariñoo li nekk ci kayitu xibaar yi ak it lu tax ñu war a seet bu baax balaa ñuy gëm li ci nekk. ” Jàngal Léebu 14:15 te woneel foofu ne war nañu seet bu baax ndax li ñuy jàng ci kayitu xibaar yi mën na nekk dëgg.
La Tour de Garde 1er nov.
“ Ñu bare tey dañu jaaxle ndax lu bon li am ci àddina si. Ndax am na ku mën a soppi àddina si ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone lu tax loolu jafe. Wax na it ki koy mën, te naka lay indee jàmm ak salaam bu mat ci àddina si. ” Jàngal Sabuur 72:12-14, te wonal nit ki fu ñuy waxe ne ‘ dina musal ki néew doole bi nekk di yuuxu ngir ñu dimbali ko, ak it ki am naqar ak képp ku amul ku koy dimbali. ’
Réveillez-vous ! 8 nov.
“ Tey ci àddina si, am na ñu bare alal lool, am na it ñu amul dara. Ci sa xalaat, lan la ñu mën a def ba ñépp yem ? [Mayal nit ki tontu ba pare jàngal Macë 6:9, 10 te won ko foofu ne coobare Yàlla dina am “ ci suuf ”.] Nguuru Yàlla bu ñëwee, li am tey ci àddina si, du amati, maanaam kenn du ëpp alal moroomam. Ñépp ay tolloo. Ci téere bii, dañuy wax lu tax ñu mën a gëm loolu. ”