Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 oct.
“ Am na ñuy wax ne mënuñu xam Yàlla ndaxte ci asamaan la nekk. Ndax mas nga xalaat loolu, yow itam ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal Amos 3:7. Wonal nit ki ne Yàlla dafay ‘ xamal ’ ñi koy jaamu li mu bëgg def.] Téere bii dafay wone lan lañu war a def ngir xam Ki ñu sàkk ak li mu bëgg def. ”
Réveillez-vous ! Oct.
“ Li ëpp ci nit ñi, seen mbokk mbaa seen xarit mas nañu gaañu. Ndax foog nga ne nit ñooñu dee ba pare, am na li ñu mën a def ngir dimbali ñu ? [Mayal nit ki mu tontu ba pare jàngal Dajalekat 9:5, 10 te boo koy jàng, fexeel ba kàddu yii : “ ne savent rien ”, (maanaam xamuñu dara) feeñ bu baax.] Kàddu Yàlla wax na ne suñu mbokk walla suñu xarit yi gaañu, duñu nekk noonu ba abadan. Loolu la téere bii di wone. ” Won ko xaaj biy komaase ci xët 10.
La Tour de Garde 1er nov.
“ Tey, nit ñi bokkuñu gis-gis ci wàllu yar sa doom. Ndax foog nga ne wayjur yi mën nañu am xelal yu wóor ci fànn boobu ? [Mayal nit ki tontu.] Seetal li Yàlla dige fii. Yonent Yàlla Dawuda moo ko bindoon. [Jàngal Sabuur 32:8, te fexeel ba kàddu yii : “ dinaa la digal ”, feeñ bu baax.] Téere bii dafay wone ay xelal yu baax lool ci wàllu yar sa doom, yu jóge ci Kàddu Yàlla. ” Won ko wërale bi nekk ci xët 5.
Réveillez-vous ! Nov.
“ Ndax mas nga laaj sa bopp li Yàlla di yëg bu gisee suñu metit yi ? [Mayal nit ki mu tontu.] Ca jamano Nóoxin metit yi bare woon nañu. Seetal ci aaya bii loolu lu mu def Yàlla. [Jàngal Njàlbéen ga 6:5, 6, te fexeel ba kàddu yii : “ am tiis ci xolam ”, feeñ bu baax.] Téere bii dafay wone li Yàlla di def ngir dindi fi metit yi. ”