Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 des.
“ Fii ñu tollu nii ci at mi, li ëpp ci nit ñi, bu ñu gëmee Yeesu Krist ak bu ñu ko gëmul yépp, dañu koy xalaat. Ñenn ñi dañuy wax ne nekkul woon nit dëggëntaan. Lu ci sa xalaat ? [Bu tontoo ba pare, jàngal Macë 16:15, 16.] Xaaju yéenekaay bii di wax ci Yeesu dafay wone li Yeesu di def ci yow tey ak ëllëg. Wóor na ma ne boo ko jàngee dina la neex. ”
Réveillez-vous ! 22 des.
“ Ndax nangu nga ne bu ñu bëggee am dund gu baax, li ñuy lekk dafa war a sell, te warul a ñàkk mukk ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Yàlla digoon mbooloom ca jamono ja ñu doon bind Mbind mu sell mi. [Jàngal 3 Musaa 26:4, 5.] Réveillez-vous ! mu ngi wax ci suñuy jafe-jafe yi jëm ci li ñuy lekk tey. Dafay wone itam pexe yu am njariñ ci fànn boobu te dafa ñuy xalaatloo ci jamono ju ñu Yàlla di may jàmm ci kow suuf si sépp. ”
La Tour de Garde 1 sãw.
“ Ndax mas nga laaj sa bopp lu tax ñenn ñi am dund gu neex, fekk ñeneen ñi di sonn balaa ñuy am lu ñuy dunde ? Ndax xam nga ne Mbind mu sell mi am na lu mu ci wax ? [Jàngal Ayóoba 34:19.] Ci yéenekaay bii, ñu ngi wone ni Yàlla di def ba gënale dootul am. ”
Réveillez-vous ! 8 sãw.
“ Ñépp yëg nañu musiba bu mag boobu yëngal àddina si sépp. Bi mu amee ba tey, nit ñu bare, soxla nañu luy dalal seen xel bu baax ak ndimbal bu réy. Musiba boobu, am na ñu mu laal. Ñi ci mucc ak ñi am mbokk bu ci gaañu, bokk nañu ci. Li Seede Yexowa yi def ngir dimbali nit ñooñu, bokk na ci li yéenekaay bii di wone. ”