Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 Déc.
“ Bu ñu nekkee ci bésu feet yi, ñu bare dañuy góor-góorlu ngir baax te am yërmande. Fooguloo ne àddina bi dina gën a neex bu nit ñi doon wone yërmande at mi yépp ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare jàngal 1 Piyeer 3:8.] Yéenekaay bii dafay wax lu tax ñu war a yërëm nit ak ni ñu ko mën a defe. ”
Réveillez-vous ! Déc
Ndax foog nga ne suñu mbokk yi gaañu dinañu mas a dundaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Mbind mu sell mi mu ngi wax ne am na lu mën a génne nit ci dee. [Jàngal Sabóor 68:20]. Yéenekaay bii dafay wone lu tax waruñu ragal dee, te bañ xalaat ne fa la dund yem ba fàww. ”
La Tour de Garde 1er Janv.
“ Wax dara ba pare réccu ko, ñépp lay dal.Te suñu biir kër la loolu di ëppe. Ci sa xalaat, naka lañu mënee wax nit li nekk ci suñu xol te bañ ci boole ay wax yu koy gaañ ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal Léeb yi 15:28]. Yéenekaay bii dafay wone ni ñu mënee def ba am ay kàddu yuy may doole ñi nu bëgg ”. [Won ko waxtaan biy komaase ci xët 10.]
Réveillez-vous ! Janv.
“ Démb ba tey, dañu mas a noot jigéen ñi te di leen fitnaal. Ci sa xalaat lu waral loolu ? [Mayal nit ki mu tontu.] Xoolal li Kàddu Yàlla wax ci ni góor waree yor jabaram. [Jàngal 1 Piyeer 3:7.] Yéenekaay bii dafay wone ci Mbind mu sell mi naka la Yàlla ak Kirist di gise jigéen. ”